MAKI SÀLL GANEJI NAY DËKK AK I GOXI RÉEW MI : SAFIYETU BÉEY

Yeneen i xët

Aji bind ji

Kafrin, Fatig ak Kawlax am nañu gan fan yii weesu, gannaaw bi njiitu réew mi Maki Sàll doon wër dëkk yeek gox yi ngir saytu mbeyum ren, boole ci waxtaan ak baykat yi. Maki Sàll di rafetlu ni àll bi ne jópp, wone it mbégte ci taw bu bari bi rot, bokk ci li naataal gàncax gi.
Mi ngi ñaax itam boroom alal yi ñu geestu mbey mi ak jur gi, ndax bey ak sàmm bokk na ci li gën a gaaw a suqali koom.
Beykat yi nag, ñi ngi fàtteli njiitu réew mi ne «dige, bor la», moom mi leen dig ay jumtukaay, xarala ak i masin yu bees ngir yombal seen liggéey.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj