Mali : Ba tey soldaar yi jiite CNSP (kurél gu yittewoo muccug askan wi) ak M5-RFP déggoowuñu ci kiy war a jiite réewum Mali, ginnaaw bi way-fétteerlu yi nangoo nguur gi ci IBK. Waa M5-RFP jàpp ni ki war a jiite Mali warul a bokk ci soldaar yi, ñu jàpp it ni 3i at yi CNSP di laaj balaa taxawal ay wote dina gudd lool. M5-RFP ni benn ba ñaari at rekk dina doy, ginnaaw loolu, soldaar yi war na ñoo jébbal nguur gi askan wi.