POLITIG : SAFIYETU BÉEY

Yeneen i xët

Aji bind ji

Aymeru Ñing, doon kilifa ci Bennoo Bokk Yaakaar te jiite kurél gi ca Péncum Ndawi Réew mi, moo xamle ni « bu ñu sukkandikoo ci yoon, Maki Sàll mën naa doon lawax ca 2024 ». Mu ngi ko xamle ci waxtaan wi mu doon amal ak waa Rfm, yokk ciy leeral: « Amul luy tere Maki Sàll doon lawax ca 2024, ndax, ca 2012, bi Abdulaay Wàdd doon laaj ñetteelu moomeel, kenn terewu koo bokk ci làng gi. Daa bokk, bëre ak nun, nu daan ko.»

Bi ñu ko fàttelee li yoon wax ci ñetteelu màndaa fii ci Senegaal, da ni rekk : « Loolu àttekati ndeyu réew mi doŋŋ ñoo ci mën a indi ay leeral, ndax ñoom ñoo yor dogal biy mujj.»

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj