Njiitu réew mi fay na coowal ñetteelu moome gi. Àddu na, indi ci tontu lu leer, wax ne day sàmm kàddoom ga mu joxe woon, ne ginnaaw 2019, du bokkaat ciy wote. Ci altiney démb ji la doon waxtaan ak askan wi, bi 20i waxtu jotee ci guddi. Batale gi nag, sédd na ko ci ñetti ponk. Dafa njëkk wax ci yëngu-yëngu yi fi amoon ba ay bakkan yu bari rot ci diggante 2021 ak 2023, teg mbirum waxtaan wi mu woote woon fan yii laata mu koy tëjee mbirum wote yi ak ñàkk a bokkam. Dan leen di dégtal ay kàddoom, bañ ci rax dara.
Ci wàllu yëngu-yëngu yi fi amoon
” Sunu réew, fan yii nu génn, gis nanu fi ay jafe-jafe yu tar yoo xam ne, Senegaal mësu ko xam, ci ay yàqute, ci yàqal nit ñi seen i alal. Bàyyiwuñu kër, bàyyiwuñ loppitaal, bàyyiwuñu benn liggéeyuwaay. Ay doomi aadama bóom nañ leen, muy xale yu ndaw yoo xamante ni seen njaboot soxla nañ leen. Lu ko indi ? Pólitig ak jàpp ne boo mënee indi ay xale teg leen ci mbedd, ñu lim ay dee yu bari, dana tax Nguur gi fi nekk nërmeelu walla ñu yàq ko. Su ko defee, yéene yi nga xam ne ñi fi nekk di ko doxal ak ña ñu bokkal bitim-réew te mu leer nàññ ni tey ji, dafa am lëkkaloo diggante ñi nekk bitim-réew ak ñi ci biir réew mi, ngir yàq Senegaal, loolu laa ne, na waa réew ubbi bu baax seen i bët, bàyyi ci xel. Loolu nag, dama ci woo képp kuy njiitalu pólitig, ak boor boo mën di féete, képp kuy kilifa ci réew mi, kilifa diine, kilifa aada, képp kuy way-moome, képp kuy maxejj, war nanu bàyyi xel ci sunu réew, ndax dafa am li nga xamante ni, Senegaal, mooy réew moo xam ne, waasoo amu fi, bokk ndey, bokk baay. Donte ne nit ñi, mën nañ bañ a bokk ndey, bokk baay. Loolu moo waral may wone tiis ju tar ci xale yi ci faatu diggante 2021 ak 2023 mii. Loolu nag, maa ngi koy jaalewaat seen i mbokk, di ko jaale waa réew mépp. Di wax ne, lépp li war, Nguur gi dina ko def ci wàllu lànket ngir xam sabab yi waral musiba yépp ak ña nga xam ne ñoo ko yëkkati ak ña ñu ci àndal, ña ko doxal seen bopp, ñoom ñépp dinañu wuyu ci Yoon ngir ñu mën a fànq lu mel noonu, ndax luy yàq réew mi la.”
Mbirum waxtaan wi
” Wone naa ni réew mi, danu ko war a waxtaanee, war a diisoo ci lépp loo xam ne danu nu bokk. Looloo waraloon diiso bi ma woote woon fan yii te ñu tuude ko « Dialogue national ». Yàlla def, ñépp ñi ci bëggoon a duggu, te ñi ëpp solo ci réew mi, Yàlla def na waxtaan nanu ba juboo, am ay déggoo yu am a am solo ci wàllu koom, ci wàllu mboolaay, ci wàllu mbatit, ci wàllu pólitig, ba nga xamante ni, loolu dina gën a dëgëral sunu demokaraasi. Ponk yooyu nag nu tënk dinaa ko doxal li ko dale ayu-bés bii. Ndax, dinan yóbbu ca Ngomblaan ga àtte yi nu waroon soppi ngir li kujje gi ñaanoon ci wàllu parenaasu wote yi ak yeneen i coppite ci càrtug wote gi ak yeneen i àtte, ñu mën ko def ci diir bu gàtt. Loolu lépp, ndaxte diisoo moo ko waral ngir liy jëmale Senegaal kanam.”
Mbirum 3eelu moome gi
” Li ci des itam, wax naa ne, réew mi fi mu tollu, ak alal ji fi feeñ [balluy mbindaare yi] dina gën a tax nit ñi bëgg a ñëw Senegaal walla am lu ñu fi def, ci fànn gu nekk nag, ba ci diine ji. Loolu, lu jar a bàyyi xel la. Moo waral ma ne man, sama taxawaayu démb ak sama taxawaayu tey benn lay doon, muy taxaw ngir aar réew mi ci wàllu jonnam, ci wàllu ay digam, ci wàllu ay campeefam yépp yi nga xam ne, demokaraasi moo ko fi teg. Te, loolu, dunu seetaan mukk ñu koy yàq ak lum mën di jar. Loolu nag, fii ak Yàlla a ngi nuy may bakkan, fii ak moome giñ nu jox nu ngi koy doxal, na leen leer ne dina ci taxaw taxawaay bu wér, ànd ci ak ñépp ñi nga xam ne ñoom laa ci war a àndal.
Mbirum wote yii di ñëw, coow li bari na. Coow li bari na. Lu jiitu, may rafetlu ñi ànd ak man, ak bëgg ma toogaat ci boppu réew mi, wone ko ci anam yu baree bari, ci diiwaan yu bari, ci réew mi ak ci bitim-réew, wone ko ci lëkkatoo gii di Bennoo Bokk Yaakaar. Ma santaat leen, gërëm leen. Wone ko ci làng gi ma taxawal muy APR. Bari na sax ñoo xam ne, ay kilifa diine lañu, ay maxejj kese jàpp nañu fi réew mi tollu Njiitu réew mi war na mën a taxawaat rawatina bi nga xamee ne Yoon may na ko ko, muy ndeyu-àtte yi. Ndax leer na ne, 2016 bim ko defee.
… Sunu lëkkatoo war nanu am, bu nu àndee nekk benn, teg kippu yoo xam ne dinaa leen jàppale ni ma leen war a jàppalee ci waxtaan ak waa réew mi ngir ñu moytu li nga xam ne dina tax Senegaal saaraan ëllëg, dugg ci guuta goo xam ne, du gën ci njaboot gi, du gën ci njaboot gi. Kon, sant ñooñu, gërëm naa leen.
Waaye, nee naa nag, wote yii di ñëw, bind naa ko ci sama téere bi ñuy wax « Sénégal au cœur », maanaam Senegaal sama biir xol, bu ngeen ko gisee dingeen xam ne, moome 2019 gi mooy nekk sama ñareel ak sama mujjantalu moome. Te, loolu, tekkiwul ne sañuma ko. Waaye, loolu, sama ndogalu boop la. Te, loolu laa jël tey, moom laay baamtuwaat. Donte nag gis ngeen, ay kurél, ay nit wër nañu Senegaal, dem bitim-réew di yàq deru Senegaal, di yàq sama der naan Njiitu réew mi dafa bëgg a def ñeteelu moome, dafa bëgg a def lii, dafa bëgg a def laa. Loolu, kon war na mën a dakk. Ndax, Njiitu réew mi ci boppam jàpp na ne li mu bind 2018, dëgëralaat ko tey, loolu taxul, maanaam coow yooyu taxul, waaye ñaawlu naa bëgg sa bëgg Nguur tax na nga dem di jaay sa réew ak yàq deru sa réew. Nit ki, booy wut tam, danag ciy boole ngor, ndax loolu dafa am solo.
Li ci des mooy ñu wéyal sunu taxawaay ci réew mi, wéy di waxtaan ak ndaw ñi. Ndax, ëllëgu réew mi ci ndaw ñi la nekk. Bu nu bëggee seen njàng baax, bu nu bëggee ñu am liggéey, am, jàppale, waruñu taal ekkool yi, waruñu taal iniwérsite yi, yàq li ñu fi liggéey. Bu nu defee ay saxaar, def fi ay BRT, loo xam ne Afrig yépp a ci bég, loolu askan wi moo tax nu def ko. Du ngir Njiitu réew mi, Maki Sàll, du ngir Nguur gi. Kon, war nañu sàmm loolu nu leen defaral ndax alalu réew mi moo ko defar, te dan ko leb. Kon loolu dan ko war a sàmm bu nu bëggee gune doon ëllëg bu gën. Kon ci loolu laay woo saa-senegaal yi. Di leen sant, di leen gërëm.
Di leen wax nag, bañ a nekk lawax terewul, ma taxaw taxawaayu Njiitum réew… Lépp lu mu laaj ci wàllu kilifteef dina doxal ba mu mat sëkk, fii ba cëppaandoo la, bu ci Yàlla àndee, 2i fan ci weeru awril 2024. Dina fekk ñu amal ay wote. Yàlla na nekk wote yu sedd guy, bu leer nàññ, ni ko Senegaal di defee. Bu ko defee Senegaal wéyal doxam ci jàmm ak salaam.
Maa ngi baalu ñépp àq, di sant ñépp, di gërëm ñépp. Wa salaam.”