Njiitu réew mi, Maki Sàll, amaloon naw waxtaan ak sunuy naataango yu Le Monde, ab yéenekaayu Farãs. Ca biir waxtaan wa, delsi woon na ci wotey 2024 yi, tontu ci Usmaan Sonko. Wax itam ci diggante Senegaal ak Farãs ak ci li soxal ëllëgam ginnaaw 2024.
Ginnaaw bi mu xamlee ne du bokk ci wotey Njiitu réew yii di ñëw, Maki Sàll séq naak waa Le Monde aw waxtaan. Muy laaj-tontu bees siiwal bërki-démb, ci àjjuma ji, 7 sulet 2023. Lu ko jiitu, Usmaan Sonko séqoon na ak waa France 24 ab laaj-tontu, waxoon ci ne, bu bokkul ci wotey 2024 yi, wote du am walla fitna ju réy dina gaar réew mi. Mu mel ni Maki Sàll daf ko doon tontu. Ndax, bi ñu ko laajee ci wote yi, dafa tontu lu leer, wax ne :
« […]Wote yi dinañu am te askan wi dina tànn Njiitu réewam. Du lenn walla kenn ku mën a indiy jafe-jefe ci wote yi. »
Laajees na ko tamit ci mbiri Usmaan Sonko mi Yoon daan 2i ati kaso yum war a tëdd. Ñuy ragal fitna amaat buñ ko jàppee. Kàddu yi mu ci yékkati nag, ba di ko méngaleek li xewoon 2019, dañuy wone rekk ne moom, Njiitu réew mi, fasul yéene dellu ginnaaw te du may Usmaan Sonko dara. Nde, dafa waxe ne :
« Amul lu may ragal. Réew laay jiite. Sama yitte du coowal kenn nit. Bu amee kuñ war a jàpp, dañ koy jàpp. »
Ñu déggee ci ne bu Usmaan Sonko waree wuute wote yi, dina leen wuute. Trax-ci-dolli, moom Maki Sàll, noppi na ngir dem ci ba sës.
Bu dee lu jëm ci diggante Senegaal ak Farãs, Njiitu réew mi xamle naat ne dara lu ñaaw xewu ci. Li mu ci leeral daal mooy ne :
« Marine Le Pen moo sàkku giseek man bi mu ñëwee Senegaal, ma nangul ko ko. Loolu du luy xajamal diggante Senegaal ak Farãs. Li jekkul kay, ci sama gis-gis, mooy Pari di yabal ndaw ngir mu gisanteek sama wujju pólitig. Loolu yépp nag taxul diggante bi yàqu. »
Ginnaaw ba du bokkaat ci xëccoo yii di ñëw, Njiitu réew mi, Maki Sàll, fésal nay bëgg-bëggam bés bu jógee ci boppu réewum Senegaal. Li mu namm mooy wéy di liggéeyal Afrig ba ci àddina sépp.
« Bëggoon naa wéy di liggéeyal kémbarug Afrig ak waa àddina sépp. Wareef la tey ñu sopparñi doxalinu àddina si. Lu ko moy, nun saa-afrig yi dinanu wéy di des ginnaaw. Ak lun jàmbaar jàmbaar. »
Bees déggee ay waxam bu baax, dees na fent weneen xeetu doxalin ñeel àddina si. Nde, campeef yiy doxal àddina si, tukkee woon ci Bretton Woods, méngoowuñu ak jamono. Ñiŋ leen sampoon ca atum 1945. Biñ leen di sàmp sax, réewi Afrig yi moomaguñu woon seen bopp. Kenn sóoraalewu leen ci woon.