MAKI SÀLL MIIM NA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu réew ma woon, Maki Sàll, weddi na tuuma yees gàll ci ndoddam. Càmm gu yees gi, ci njiitalu elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, dañu amaloon am ndaje ak saabalkat yi. 26i pani sàttumbaar la ndaje ma amoon. Ca ndaje mooma nag, dañ ci biraloon ne, Maki Sàll ak nguuram ga woon, dañu nax Saa-Senegaal yi, nax àddina sépp, nëbb leen tolluwaayu koppari réew mi ak dayob bor bi. Moom nag, Maki Sàll, faxas na tuuma yooyu, miim lépp.

“Dama bëgg a wax ne, wax jooju wérul, dara du ci dëgg. Nanu xaar ba Yoon dëggal walla mu weddi laata ñuy tuumaal nit ñi…”

Kàddu yii la Njiitu réew ma woon biral ci waxtaan wi mu sékkaloon ak këru saabal gu Amerig gii di Bloomberg. Toftal na ciy kàddoom, ne :

“Jëwriñ yi ñu jiiñ mënuñu sax jot ci dég-dég (xibaar) yooyu […] Maa ngi ñaan nu wàcc ci mbartal mi nu nekk te jublu ci farata ji. Ci naataange laa bàyyi réew mi. FMI dëggal na ko, wenn weer ginnaaw bi ma demee.”

Kon, Njiitu réew ma woon, Maki Sàll, jéem na a setal boppam ci kanamu waa bitim-réew. Nde, fa la doon waxe, ñoom la doon waxal. Dafa di, njombe yi ko Càmm gii taqal, dañu diis lool ci ndoddu ku mës a jiite am réew te bëgg a liggéey ak kuréli àddina si.

Mu des nag li mu war a wax waa réew mi. Ndeem dafa nar a kàmpaañsi, dees na xaar ba xam lu muy wax askan wi bu keroogaa.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj