Fanweeri jëwriñ ak juróom-ñeent la Njiitu réew mi tànn ngir ñu àggali liggéey bi fii ak wotey 2024 yi. Ci biir fanweer ak juróom-ñeenti jëwriñ yooyu, juróom-benn kese ñoo ciy jigéen. Ci ngoonug àllarbay démb ji, 11i fan ci oktoobar 2023, la Umar Ba Sàmb, magum tof-njiitu njiiteef gi, dawal dekkare bi tabb Càmm gu bees gi. Tele RTS a ko tegoon.
Àjjuma jii weesu la Njiitu réew mi, Maki Sàll, tasoon Càmm gog, 22 sàttumbaar 2022 la ko tabboon, tegoon Aamadu Ba ci bopp bi. Moom Aamadu Ba, moom la Maki Sàll jiitalaat ci boppu Càmm gu bees gi.
Bi mu jëlee kàddu gi ginnaaw Umar Ba Sàmb, jëwriñ ju mag ji dafa xamle ne :
“Càmm gu yees gii ñu taxawal, Càmmug liggéey ak xeex la gog, 39i jëwriñ a ko séq.”
Liggéey boobu ñu sumb ñeel juróom-benni weer yi des ci wotey njiiteefu réew mi, Aamadu Ba nee na, ci ñeent jubluwaay lañ ko tënk :
“Bi ci jiitu mooy fexe ba Senegaal gën a moom boppam, amal wotey 25 féewaryee 2024 yi ci anam bu mucc ayib. Ñaareel bi mooy song tembarey koom-koom geek dundub mboolaay gi, rawatina dooleel bees war a dooleel yokkute gi, fexe yokk dooley njëndu askan wi, xeex dund bu jafe bi, utal ndaw ñi xëy.”
Bu dee yeneen ñari jubluwaay yi, daf ne dañuy : “fexe ba caytuy bokkeef gi dox ni mu ware ak saxal jàmm ci fànn yépp. Àggali naal yi gën a jamp ci yi fi Njiitu réew mi sumb te door, ci ñetti weer yi mujj ci atum 2023 mi, naalu liggéey yi gën a solawu ñeel Plan Sénégal Emergent bi.”
Càmm gu yees gi nag, am nay coppite bees ko méngalee ak bi jàll. Nde, gu njëkk ga 38i jëwriñ la amoon, gii ñu samp démb nag 39i jëwriñ la am. Rax-ci-dolli, am na ñu toxu, am ñu génn, mu am it juróom-benni jëwriñ. Yu bees.
Cig pàttali, Yanqooba Jatara (tàggat-yaram) ak Aali Sale (càmm gi) dañu tekki woon seen i ndomboy-tànk (awril 2023) keroog bi Idiriisa Sekk, seen njiitul làngu pólitig (Rewmi [Réew mi]) biralee bokkam ci wotey 2024 yi. Aali Nguy Njaay tamit dafa géddoon Nguur gi keroog bi Maki Sàll tànnee Aamadu Ba muy lawaxu Bennoo Bokk Yaakaar.
Nii la Càmm gu bees gi tëddee :
Aamadu Ba, jëwriñ ju mag ji
Aysata Taal Sàll, jëwriñu Yoon wi
Ismayla Maajoor Faal, jëwriñu mbiri bitim-réew ak saa-senegaali bitim-réew
Sidiki Kaba, jëwriñu biir réew mi
Mamadu Mustafaa Ba, jëwriñu ngurd meek nafa gi
Aamadu Mansuur Fay, jëwriñu dem beek dikk bi ci suuf ak “désenclavement”
Sàmba Njóobeen Ka, jëwriñu mbey mi, jumtukaayi kow geek dund gu doy gi
Duudu Ka, jëwriñu koom-koom gi, Naal beek Koppe gi
Séex Umar Aan, jëwriñu njàng meek njàngale mi
Musaa Balde, jëwriñu njàng mu kowe mi, gëstu geek coste gi
Mariyaama Saar, jëwriñu njàngul liggéey, tàggatu geek xëy yi
Sëriñ Mbay Caam, jëwriñu ndox mi ak cetal gi
Faatu Jaane, jëwriñu jigéen ñi, njaboot gi ak kaaraangeg xale yi
Xemes Ngom Njaay, jëwriñu wér-gi-yaram gi ak ndimbalug mboolaay gi
Umar Saar, jëwriñu mbéll yi ak xamtug biir suuf (sewolosi)
Antuwaan Feliks Abdulaay Jom, jëwriñu soroj bi ak laf yi
Antuwaan Mbeng, jëwriñu naawaan gi ak barab yi ci aju
Aliyun Ndóoy, jëwriñu Kéewnga gi, Yokkute gu sax gi ak Coppiteg Mbindaare mi
Paap Saañaa Mbay, jëwriñu Napp gi ak Koom-koomu géej gi
Sàmba Si, jëwriñu Liggéey bi, Ndiisoog mboolaay gi ak Jëflantey Campeef yi
AbdulaaySéydu Sow, jëwriñu Taax gi, Dëkkuwaay yi ak Cellalug bokkeef gi
Abdu Kariim Fofana, jëwriñu Yaxantu gi, Njariñoo gi ak Lijjanti yu ndaw yeek yu yemamaay yi, yor kàddug Càmm gi
Mustafaa Jóob, jëwriñu Yokkuteg isin yi ak isin yu ndaw yeek yu yemamaay yi
Umar Yul, jëwriñu làrme bi
Terees Fay Juuf, jëwriñu Yokkuteg mboolaay gi, Dimbalante gi ak Yemale gi biir mboolaay gi ak mberaay gi
Viktorin Ankedis Ndey, jëwriñu mikorofinaas ak Koomug mboolaay geek jàppalante bi
Móodu Jaañ Fadaa, jëwriñu “Collectivités territoriales” yi ak Yokkute geek Yembalug mberaay gi
Paap Maalig Nduur, jëwriñu Ndaw ñi, Lijjanti gi ak Liggéey yi
Maam Mbay Kan Ñaŋ, jëwriñu wërteef gi ak Po yi
Aliw Sow, jëwriñu Mbatiit gi ak Bokk-moomeelu mboor gi
Musaa Bookar Caam, jëwriñu Jokkoo gi, Jollasukaay yi ak Koomug xamteef gi
Galo Ba, jëwriñu Liggéeyu Bokkeef gi ak Coppiteg Fànnu bokkeef gi
Biram Fay, jëwriñu “Artisanat” bi ak Coppiteg liggéey yees yoonadil
Anet Sekk, tof-jëwriñ ci jëwriñu mbiri bitim-réew ak saa-senegaal yu bitim-réew, Yor mbiri saa-senegaal yi nekk bitim-réew
Allaaji Momar Sàmb, tof-jëwriñ ci jëwriñu Yoon wi, Yor mbirum àq ak yelleefi doom-aadama ak Njiite gu jub gi
Daawda Ja, jëwriñu Càmm gi ak Njureefi mala yi
Lat Jóob, jëwriñu Tàggat-yaram
Paap Aamadu Njaay, tof-jëwriñ ci jëwriñu dem beek dikk bi ci suuf ak “désenclavement”, Yor liggéeyu raay yi
Mamadu Saaliw Sow, tof-jëwriñ ci jëwriñu Biir réew mi, Yor Kaaraangeg jegewaale gi ak Kaaraangeg maxejj yi
Isaa Jóob, tof-jëwriñ ci jëwriñu ndox mi ak cetal gi, Yor wàllu fagaru ak Caytug mbënn mi
Ginnaaw loolu, Njiitu réew mi dafa xaatim beneen dekkare bob, tabb na ci kii di Muhammadu Maxtaar Siise, def ko bëkk-néegu Njiitu réew mi.