MAKI SÀLL TAGG NA SEEX MAAHI ÑAS

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tey ci talaata ji, Njiitu réew mi Maki Sàll, ma nga woon fa Kawlax. Gàmmu gee ko fa tax a dem. Waaye, bu ko fa diine yóbbee tamit, waxaale na fa mbiri pólitig, rawatina fitna ji gaar réewi Afirgu sowu jant. Moom, Njiitu réew mi, xamle na ne jéemoon na yónni Xalifa ñaseen yi, Séex Maahi Ibraayma Ñas fa Niger ngir mu doxi fa tànki jàmm.

Ca njeexitalu weeru sulet la lenn ci sóobarey Niseer ya, ci njiitalu Seneraal Ciyaani, déjjati Muhamet Basum ma jiite woon réewum Niseer. Ginnaaw gi, juroon na fi coow lu réy ba waa CEDEAO waxee ne dañ fay yónni ay sóobare ngir nangu Nguur gi, delloo ko Muhamet Basum. Noonu, Mali ak Burkinaa Faaso taxaw ci wetu Niseer, fas ko yéene sotal bu ko CEDEAO songee. Ñu bare ñoo tiit. Ndax, bu xare bi jollee, fitna juddu, dina jur i musiba yu jéggi dayo. Ngir daw musiba yooyu, Njiitu réew mi, ciy waxam, jéemoon na yabal Séex Maahi Ibraayma Ñas Niseer.

“Séex Maahi Ibraayma Ñas doxkatu jàmm la. Waxam jéggi na Senegaal. Ba coow li jéggee dayo fa Niseer, jokk naa ko cig jollasu ngir mu doxi tànki jàmm fa Ñaame. Waaye, du woon lu yomb jamono jooja.”

Njiitu réew mi dafa àndoon ak njiitul CESE li, Abdulaay Daawda Jàllo, jëwriñ yii di Antuwaan Feliks Jom, Mansuur Fay, Mariyaama Saar ak Sëriñ Mbay Caam. Ci seen teewaay la Njiitu réew mi wax Séex Maahi Ñas kàddu yii toftalu :

“Dama la naroon a yabal fa Niseer ngir nga doxi fa tànki jàmm. Waxtaanoon nanu ci, waaye ni mbir yi deme woon a taxoon mënoo fa woon dem. “

Maki Sàll seede na ceede yu rafet ci Séex Maahi Ibraayma Ñas ak maam ji, Séex Ibraayma Ñas (Baay Ñas) mi nga xam ne, turam ak dayoom weesu na Senegaal.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj