« Càmmug Senegaal amati na mbetteel ci jeng bi tele France 24 di jeng buy siiwal xibaari pólitig yu Senegaal. »
Kàddu gii la Càmmug Senegaal ubbee yégle bim génne ngir ñaawlu doxalinu tele Farãs bii di France 24. Li ko waral, ci lees njort, mooy laaj-tontu bi tele tubaab bi mujje séq ak Usmaan Sonko. Musaa Bookar Caam, jëwriñu jokkoo gi, moo xaatim yégle bi génn tey, 8i fan ci sulet. Li yégle biy wund mooy ne, France 24 dafa jeng, di ràccal kujje gi, te du guléet. Nde, ni muy saabaalee xew-xewi pólitig fi Senegaal, àndul ak màndute. Bees sukkandikoo ci yégle bi, saabalkati France 24 yi sàmmontewuñu ak sàrti tasug xibaar ci wàllu njub, yemale ak màndute ñeel anam yees di siiwalee xibaar yi. Ndaxte, ci li jëwriñ ji bind, ni France 24 jengee ci kujje gi « …day feeñ ci seen i jotaayi xibaar, jotaayi faramfàcce, laaj-tontu yi ak mbind yi tele biy fésa ci bés bil. »
Ngir firndeel li muy tuumaal tele bi, Càmm gi dafa duut baaraam kàdduy dépite Biram Suley Jóob mi Yoon jàppandi jamono jii. Ci li yégle bi wax, tele France 24 dafa ne, li tax ñu jàpp dépite Biram Suley Jóob, mooy li mu wax ci kàdduy Njiitu réew mi, keroog 3 sulet 2023. Ñu bindati ci yégle bi ne, ginnaaw bi Njiitu réew mi waxee waxam juy des ci mboor jooju, ci talaata jii weesu, tele France 24 daf cee toftal ay kàdduy fitna ñeel Senegaal. Loolu moo metti Nguur gi ba tax ko di ñaawlu ak a naqarlu liggéeyu tele boobile ñeel Senegaal. Yégli bi nag, jur na coow lu bari ci pénc mi.
Waa kujje gi, rawatina waa Pastef, ñoo ngi naan France 24 du Walfadjiri. Nde, dog kon nañu siñaalam bu yàgg. Ñi ànd ak Nguur gi, ñoom, dañuy wax ne yégle bi firnde la ci ne Senegaal ñàkkul fayda te du bàyyi ay doxandeem di jaxasee réew mi. Waaye nag, bu lépp weesoo, ñu teg mbiri péete yeek farandoo yi fële, digg-dóomu te jéem a càmbar mbir mi, dees na jukkee ay njàngat yu bari.
Njàngat li jiitu mooy ne, dafa mel ni Usmaan Sonko am na ndam ci kow Maki Sàll fa bitim-réew, rawatina Farãs. Ci alxames jii weesu la Usmaan Sonko toogoon këram, di tontu ci laaji saabalkatu France 24 bi, Marc Perelman. Ci àjjuma ji la ëttub ciiwalu tele bi génne ag toftale, teg widewoo waxtaanu Usmaan Sonko bi ci kow widewoo yi ñu gën a seetaan. Ndax, bi ñu dugalee widewoo bi ci Youtube, ci alxames ji, boori 21i waxtu yu tegal 45i simili, lu tollu ci tamndareti nit seetaan nañu ko te widewoo bi amagul sax benn fan. Muy lees mësut a gis, di firndeel ne dayob Usmaan Sonko ak yitte bi nit ñi am ci moom, jéggi na digi Senegaal, romb digi Afrig, wër àddina. Njiitu réew mi sax amul li mu am. Te, ca ëllëgu waxtaanu Sonko waak Marc Perelman, Njiitu réew mi, Maki Sàll, doon na tontu ci laaji yéenekaayu Farãs bii di Le Monde. Mu mel ni, léegi, Maki Sàll mooy wujje ak Usmaan Sonko. Te, waxtaanam woowu, siiwul ni wu Usmaan Sonkoo wi. Mbaa du kàrt gi day waaj a dëppu ?
Ñareelu njàngat li day dellu ci taxawaayu Farãs. Dafa di, sikk amul ci ne, Farãs, ñaari réew kese ñoo ko dese fi Afrig sowu jant : Senegaal ak Koddiwaar. Te nag, bu leen ñàkkee mooy torox na. Moo tax, jamono jii, ñu ngi nas i pexe ngir sàmm li ñu fi dese. Ku seetlu anam bi yéenekaayi Farãs yiy faral di féetewoo mbiri Afrig yi (RFI, France 24) di càmbaree xibaar yi ñeel Senegaal, day mel ni dañuy tilimal Nguurug Maki Sàll. Ñu bari jàngee ci ne, Farãs dafa won Maki Sàll ginnaaw. Ndax, ci waxi ñenn ñi, xam nañu ni, askanu Senegaal bëggatul Maki Sàll. Moo tax ñu jàmbu ko. Rax-ci-dolli, saa bu Senegaal yëngoo, Farãs dina ci ñàkkee lu bari ci alal. Kon, jàmmi réew mee leen jig. Te nag, yëngu-yëngu yi fi am yépp diggante 2021 ak 2023, Usmaan Sonko moo tax. Saa buñ ko jàppee walla ñu nar koo jàpp, ndaw ñi génn, di taal ak a yàqate. Moomeeli doomi Farãs yi, Auchan, Total, Shell, añs. ñoo ciy gën a dee. Nde, dañu jàpp ne Farãs day jàppale Nguur gi fi nekk te, jafe-jafe yi ñuy jànkonteel yépp, loxoom génnu ci. Amaana looloo tax Farãs di bëgg a setal deram ngir muccal ak a sàmm li ko fi dese.
Wareesul a fàtte tamit ne, Senegaal dafa am soroj (petarol) ak gaas. Te, umpalewuñu ni, Farãs du bëgg ñu tàbbi ci loxoy ñeneen. Moo tax, xalaatul a génne loxoom ci wotey 2024 yoy, ñépp xam nañ ne Usmaan Sonko am na ci wàll wu réy. Maki Sàll nee na, moom ci boppam, du ci bokk. Usmaan Sonko, bokkam wóoragul. Ku ci nekk nag, yaa ngi lal i pexe, di wax ak àddina si ngir tiiñal sa moroom. Farãs sóobu na ci xeex bi, jaare ko ci ay yéenekaayam. Kan la àndal ? xameesagu ko ci lu leer. Li wér te wóor daal mooy ne, Maki Sàll ak Usmaan Sonko bëre nañ ba àgg arenu Farãs. Kan mooy daan ? Kenn xamul. Waaye, Usmaan Sonko yóbbagum na Maki Sàll ardo.