Kaawteef ! Mali, Burkinaa Faaso ak Niseer mànkoo nañ génn ci CEDEAO. Xibaar bi day sog a jib.
Ab yégle lañu dawal ca tele Niseer, tey ci dibéer ji, di ci xamle ne ñetti réew yii di Mali, Burkinaa Faaso ak Niseer jël nañu ndogalu génn ci CEDEAO. Nee ñu, ndogal li day tàbbi ci saa si.
Ñetti réew yooyii nag, ay sóobare ñoo leen jiite ginnaaw bi ñu déjjatee Nguur ya moome woon. Ñoom nag, dañu bind ci yégle bi ne, ginnaaw 49i at bi CEDEAO sosoo ak léegi, sottalul jubluwaay yi taxoon njiit ya woon taxawal ko. Ñu rax ça dolli ne, dafa am réewi doxandeem yu teg loxo CEDEAO, di def di dindi, di nas ak a nocci ci suuf. Nee nu, looloo dem ba sabab ag wóoradi ñeel askani ñetti réew yi. Nde, CEDEAO amul taxawaay bim waroon a am ñeel leen. Moo tax :
“ Sang yii di Kàppiten Ibraayim Taraawore, Kolonel Asimi Goyta ak Seneraalu Birigàdd Abdurahmaan Ciyaani, ñoom ñi jiite, ci ni mu toftaloo, Burkinaa Faaso, Mali ak Niseer, jël seen i matuwaay ci kanamu mboor ak sòoraale seen bëgg-bëggi askan, jël nañ ci seen jëmmi bopp ndogalu génne Bokkeefi Burkinaa Faaso, Mali ak Niseer ci CEDEAO. Ndogal loolu nag, day tàbbi ci saa si.”
Kon, bés niki tey, ñetti réew yooyii bokkatuñ ci CEDEAO. Ndogal lii nag, dina am ay njeexital ci wàllu pólitig ak koom-koomu Afrigu sowu jant.