MALI-IKREN : DIGGANTE BA DOG NA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Càmmug Mali gi dafa jël ndogalu dog bépp xeetu jëflante ak Ikren. Ndogal loolu nag, day tàbbi ci saa si. Li ko sabab mooy li àmbaasadëeru Ikren bi nekk Senegaal biraloon, di ci wax ne réewam bokk na ci ñi jàppale rëtalkat yi song Mali fan yii weesu. Ci kow loolu, njiiti Mali yi dañu tuumal Ikren, jàpp ne daf leen a song ci seen biir réew.

Kii di kolonel Abdulaay Mayga moo dawal ab yégle ca seen tele bii di ORTM, ci dibéeru bërki-démb ji, 4i pani ut 2024. Moom mi yor kàddug Nguuru Mali gi, Kolonel Abdulaay Mayga, dafa biral li kilifay réew may jiiñ Ikren. Nde, bees sukkandikoo ciy kàddoom, Ikren daf leen a song ci seen biir réew. Ndax, ki yor kàddug way-yëdduy (renseignement) Kiev yi, Yurii Pyvovarov, moo siiwal ab widewoo ci Facebook, di ca wax ne réewam mii di Ikren laale na ci cong mi mujje am Mali ba ay bakkan yu bare rot ci. Sóobare yi ci ñàkk seen i bakkan, ñi ngi bokkoon ci xareb Mali ak kippug xare gii di Wagner.

Njiiti Senegaal yi tamit rafetluwuñu ko, te naanewuñ ko ndox. Moo tax, ci àjjuma ji lañu woolu Yurii Pyvovarov mi teewal Ikren fi Senegaal, wax ko seen i ñetti dëgg. Njëwriñu mbiri bitim-réew gee ko woolu ngir wax ak moom, fàttali ko fi mu war a yam, li ko dayoom may ak fi sañ-sañam yem.

Càmmug Senegaal gi yemu ca. Nde, dafa génne ab yégle, di ci ñaawlu doxalinu Yurii Pyvovarov, di bokk ak askanu Mali ak i njiitam naqar ak tiis wi leen dal ginnaaw congum rëtalkat yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj