Ndaw yi Bennoog Tugal gi yabal (Mission de l’Union Européenne) ngir ñu saytu wotey njiiteefu réew mi, keroog 25 féewarye 2024, ñooy sàkkoo gise ak Basiiru Jomaay Fay mi ñu téyandi fa kaso ba jamono jii. Ñoom, Saa-Tugal yi, dañu jàpp ne Basiiru Jomaay Fay dafa war a kàmpaañ niy moroomi lawaxam.
Soxna sii di Malin Björk moo jiite ndaw yi fi Bennoog Tugal yabal, ñu war a saytusi wotey 25 féewaryee 2024 yi. Ci àllarbay tey ji lañ doon janook taskati xibaar yi fi Ndakaaru. Liñ ko dugge woon mooy leeral liggéey bi leen fi tax a ñëw. Soxna Malin Björk dafa wax ne :
« Sunu jubluwaay mooy daje ak lawax yi Ndajem Ndeyu àtte réew mi daganal yépp, ak anam bi ñu mën a nekke. Bëgg nanu tamit gise ak Sëñ Jomaay, fum mën di doon. »
Biñ ko laajee ndax jébbal na Nguur gi càkkuteefu gis Basiiru Jomaay Fay, soxna si dafa tontu, wax ne ñoom, ñoo ngi « …dox jéego yi war. »
Dafa di, dibéer jii, 4 féewaryee 2024, la kàmpaañ biy door. Te, ba léegi, lawax bii di Basiiru Jomaay Jaxaar Fay mi ngi ndung-siin ñu téye. Ba tey, kenn xamagul naka lay kàmpaañee ci anam yile.
Cig pàttali, àjjuma 14 awril 2023 lañ jàppoon Basiiru Jomaay Fay, nekkoon fara-caytu bu pàrti Pastef ba woon. Li ñu koy tuumaal mooy ciiwalug xibaar yu wéradi, tooñ àttekat ak gàkkalug der ñeel mbooloom liggéeykat. Moom, tànneefu Usmaan Sonko bi, dafa bindoon ci xëtu Facebookam, di ci ŋàññi doxalinu àttekat yi.
Naam, mi ngi ci kaso bi, waaye Basiiru Jomaay Fay dafa bokk ci lawax yi gën a jekku ngir toog ci jal bi. Ndaxte, ànd ak li ñu tas seen pàrti bi ak liñ jàpp seen njiit lii di Usmaan Sonko, ba tey ñoo ngi wéy di gën a am doole. Rax-ci-dolli, taxawal nañ ag lëkkatoo gu réy gu boole kàngam yu deme ni Aminata Ture, Ayda Mbóoj, Séex Tiijaan Jéey, Daam Mbóoj, Mari Tëw Ñaan, Séex Bàmba Jéey, añs.
Ndajem Ndeyu àtte réew mi dafa tere Usmaan Sonko bokk ci wote yi. Waaye, moom Basiiru Jomaay Fay, bàyyi nañ ko mu bokk. Guléet fi Senegaal nag, ñuy sóobu ciy wote njiiteefu réew mi, mu am ab lawax bu nekk ci kaso bi. Looloo tax soxna Björk waxati ne :
« Jàpp naa ni lawax yi Ndajem Ndeyu àtte réew mi daganal yépp lañ war a yemale. Te, noo ngi yaakaar ne dina am. »
Soxna si dafa gis ne, lawax bu ci nekk am nga sañ-sañu kàmpaañ te dara du la tënk.
Ñoom nag, ndawi Tugal yi, seen lim a ngi tollu ci 130i saytukat yu bàyyeekoo ci 27i réew yu bokk ci Bennoog Tugal gi, waaye tamit Norwees, Siwis ak Kanadaa. Bees sukkandikoo ci kàdduy Soxna Björk, Senegaal a leen woo.
Seen liggéey a ngi aju ci saytu doxiinu wote yi ak nees di sàmmee àq yeek péexte yi. Ñaari fan ginnaaw sumb bu njëkk bi lay biral caabalam gu njëkk. Buñ ci tegee ay ayu-bés ginnaaw bi njureef yi matee, ci lay sog di génne ag caabal gu matale. Moom nag, nee na ñoom dañuy maandu ci wote yi, kenn du leen tënk te duñu laale ci doxiinu wote bi.