MAMADU BAAJO KAMARA, LOO NAR ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Léegi, xam nañ kan mooy wuutu Paap Umar Saaxo mi dem alaaterete. Ci dekkareb 2022-1573 bu bésub 1 ci sàttumbaar 2022 la Njiitu réew mi, Maki Sàll, tabbe ki war toog ci boppu Ndajem ndeyu àtte mi ci 6i at yii toftalu. Mamadu Baajo Kamara, ni ko ñépp njorte woon, la Njiitu réew mi jox lenge yi, mu war a jiite kurél googiley cëslaayu lépp luy yoon walla àtte ci réew mi. Waaye nag, dafa mel ni, ñépp ànduñu ci tànn bi ko Njiitu réew mi tànn, donte ne am na ñu koy layal.

Bi xibaar bi rote ba tey, nag, nit ñaa ngiy soow, rawatina kujje gi. Nde, ñoom, dañu yàgg a jàpp ne Mamadu Baajo Kamara, ndawu Maki Sàll la. Moo tax, ñiŋ koy tam dëmm, naan dara taxul Maki Sàll tabb lu mooy muy lewal ko ñetteelu moome gim nar a sàkku. Daanaka, tabb bi ñu ko tabb bettul kenn. Ndaxte, yéenekaay yàgg nañoo siiwal i xibaar ñeel ndogal lile. Waaye, waa kujje gi moom, yàgg nañoo tam dëmm Mamadu Baajo Kamara.

Kujje gi dañoo jàpp ne Mamadu Baajo Kamara ci waawu Maki Sàll lay dox. Ndawam la. Daf ko fee teg ngir dimbali ko ci pexe yi muy nas. Li koy firndeel, ci seen i wax, mooy ne saa bu xëccoo amaan diggante Nguur gi ak waa kujje gi, bu Mamadu Baajo Kamara waraan àtte, Nguur gi lay jox dëgg. Waaye, du loolu kese lees koy tuumaal. Ndaxte, nee ñu, moom miy kilifay kilifa yi ci wàllu yoon tey, moo njëkk a jalgati yoon bi muy jiite Ëttub àtte bu mag bi. Ndeke, dafa bañoon a biral li mu am ci alal ni ko ko yoon sante. Ki ko xamle woon mooy Soxna Nafi Ngom Keyta mi jiite woon OFNAC. Rax-ci-dolli, muy Xalifa Sàll, di Kariim Wàdd, ku ci ne, am na foo jaar ak Mamadu Baajo Kamara. Nde, dañu jàpp ne, moom, Njiitalu Ndajem ndeyu àtte lu yees li, waayu Maki Sàll la. Te, bokk ndogalu waa ji tere na laa bokk ci joŋantey wote yi weesu, rawatina yu 2019 yi.

Ci beneen boor, ñu bari dañu njort ne, lenn rekk a tax Maki Sàll tabb ko : lewal ko sémbub ñetteelu moome bi ñuy soow. Ndege, laata Njiitu réew mi di jël ndogal li ñeel ko, toog na weeruw lëmm woo xam ne tabbu fa kenn. Nee ñu booba, moo ngi doon seet kan moo gën a yey ci defal ko li mu bëgg. Fi mu ne nii nag, xel yi ñaaw nañ, ñoo ngi gàkkal deru Mamadu Baajo Kamara. Waaye, nag, baax na ñu xam tuuti kan mooy Mamadu Baajo Kamara ak fan la jaar ba agsi fii.

 Kan mooy Mamadu Baajo Kamara ?

Tirbinaalu Ndakaaru la njëkk a liggéey ginnaaw bim amee lijaasama ca ENAM (moo nekkaat ENA). Def na fa juróom-ñaari at (1977-1984) yoo xam ne, moo fa nekkoon njëlbeenug tof-njiitu toppekat bi (premier substitut du parquet). Bim fa jógee, ci lañ ko tabb Porokirëeru Sigicoor ak Kawlax. Li ko dale 1991 jàpp 1993, moo jiite woon Cours d’appel bu Ndakaaru. Mu jógeeti fa, nekk tof-njiitub toppekat bu mag bi ci diirub 5i at (1993-1998) laata muy nekk tof-toppekatu Ndakaaru.

1998 ba 2008, Mamadu Baajo Kamara amoon ñaari ndomboy-tànk ca Cours de cassation bu Ndakaaru : xelalkat ak tof-njiit lu mag. Ñu daldi koy yokkal dayoom, mu dugg ca Ëttub àtte bu mag bi (Cours Suprême) nekk fa Tof-njiit lu mag, njiitalu néeg ak Toppekat bu mag. Tey nag, Mamadu Baajo Kamara matal na. Nde, tabbees na ko, def ko Njiitalu Ndajem ndeyu àtte réew mi.

Nu gis ne kon, àttekat bi du como ci wàll wi. Bu dee xam-xam bi, am na ko. Bu dee jaar-jaar bi, rafet na. Kilifteef gi, yelloo na ko. Li ñépp di xaar ci moom nag mooy ndax dina am ngor ak fitu doxal yoon. Li ci kanam rawul i bët.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj