Bu Séex Anta Jóob (1923-1986) doon dund ba tey, am koon na 100i at ci ren jii. Dafa di, jamono jii sax, ñoo ngi ko ciy sargal. Nde, UCAD, jàngune biñ ko duppee, mooy jëmmal téeméeri ati werekaan bi. Dañu sumb ay xew-xew ak i waxtaan yoy, dees na ci biral jaar-jaar ak liggéeyi Séex Anta Jóob. Waayeet, dees na ci jukkee ay xalaat, ay pexe ak i yoon yu jàmbaaru Céytu bi xàlloon ngir bennoo ak naataange Afrig. Téeméereelu Séex Anta bi nag (1923-2023), Xaadim Njaay daf ko ci jagleel ab téere bob, moom Séex Anta Jóob la jox kàddu gi.
Cheikh Anta Diop par lui-même, noonu la téere bi tuddu. Afrikana moo ko móol ci atum 2023 mii. Téereb 350i xët la, di ab xeltuwaan (essai) bu séddalikoo ci 40i ponk. Jalo Jóob moo bind ubbee bi (préface). Bii mooy ñaareelu téere bi Xaadim Njaay, xeltukat bi, di jagleel Séex Anta Jóob. Bu njëkk ba, Conversations avec Cheikh AntaDiop, aw waxtaan wu mu fentoon la digganteem ak werekaan bi dëddu.
Téereem bu mujj bii, dafa làmboo solo su réy a réy. Ndax, am mboolent la (compilation) mom, day dékkil boroom xam-xam bi, jox ko kàddu gi, muy nettalil boppam jaar-jaaram, dale ko juddoom ba ci njeexitalu dundam, rawatina njàngam, gëstoom yeek xeexu pólitigam.
Xaadim Njaay mi ngi Kanadaa. Waaye, fàttewul cosaanam, gàlliwul te dëdduwul réewam astemaak kembaaram. Moom, day roy ci Séex Anta Jóob mi mu bindal lees mën a jàppee niy ceede (mémoires).
Bindkat bi yemul rekk ci mbindi Séex Anta yi. Waaye, dafa gëstu, laajte. Noonu la dajalee ay waxi Séex Anta Jóob yu solowu yoy, xawoon nañ réer ci jamono. Ku xam Séex Anta Jóob, xam ne bind na lu baree bari, wax lu baree bari. Kon boole ay mbindam ak i waxam, du liggéey bu yomb. Moo tax cant ak ngërëm ñeel Xaadim Njaay. Nde, yemul rekk ci ndajale gi, waaye dafa lootaabe téere bi ci anam bu mucc ayib, séddale ko ciy ponk yoy, aji-dawal ji (le lecteur) mën na ci gindiku ci anam bu yomb te jàppandi.
Képp ku jàng téere bi, dinga xam Séex Anta Jóob, bu dee xamoo ko woon. Bu dee xamoon nga ko, diŋ ko dollee miin. Wëliis juddoom, xaleelam, ay mbokkam ak béréb ya mu jaar yépp, dees na jukkee ci téere bi li tax àddina sépp naw boroom xam-xam bu mag a mag bi. Loolu mooy xër bi Séex Anta xëroon ci xam-xam, xereñoon lool sax ak xel mu ñaw ma. Mu nekkoon it ku farlu te sawar lool. Waayeet, dees na ci jàngee ay jikko yu baax yi mu làmboo woon. Séex Anta Jóob, ni ko Xaadim Njaay feeñalee, ku maandu woon la, gore lool, dëggu, wàccee boppam te yéwénoon ci xam-xamam.
Séex Anta Jóob, bañkat la woon. Looleet, téere bi feddali na ko. Ci benn boor, Séex Anta Jóob, ma-mboor (historien) bu mag la woon, doon gëstu ci Misra ma woon. Ca jamonoom nag, ay gëstukati tubaab yu bari dañ féetale woon xayteg Misra moomu ca ma-weex ya. Moom mu ñëw, ngànnaayoo xam-xam ak njub ci wàllu gëstu, xeex ak ñoom ci xam-xam, weddi seen i mbind yooyu nga xam ne, ci xeetal doŋŋ ak boddekonte la lalu woon, déet ci xam-xam bu wér.
Dafa di, jooja jamono, xeebeel bi ma-weex yi amoon ci ñuule yi, rawatina waa Afrig bëj-saalumu Sahara bi, dafa jéggi woon dayo, fësoon lool ba law ci xamtu yi. Bëtu xeebeel boobu ñu doon xoole Saa-Afrig yee taxoon daawuñu leen askanale ag xayte, gum ci mën di doon nag. Moom kay, dañ daan wax ni sax amuñu mboor. Bi Séex Anta Jóob ñëwee, dafa njëkk a feeñal ni Afrig la Maam Aadama fekk baax ak i firnde yu bir. Ginnaaw gi, biral na yit ne, Misra ma woon, ay ñuule ñoo ko sanc, naatal ko, suuxat fa ag xayte gog, amul moroom ba jonni-Yàlla-tey jii. Kon, Séex Anta Jóob dafa juboole Afrig ak démbam, siggil ay doomam, delloo leen seen sag. Wone na ne, Saa-Afrig yi duñuy dof nees leen ko doon gëmloowee. Taxawaay booboo sabab xeexam ci pólitig.
Ci beneen boor, boroom xam-xam bi doon sàkkoo yor lengey réewam, Senegaal. Waaw, Séex Anta Jóob daan na pólitig. Li mu ko dugge woon mooy fexe ba réewi Afrig yi booloo doon benn, far dig yi fi tubaab bi rëdd ngir féewale nu, noot nu. Yemu ca, dafa nisëroon bennale leen itam ci wàllu koom-koom ak xare, réewi Afrig yi mënal seen bopp, amal seen bopp ab làrme bu mag bu am doole ngir kenn bañ leen noggatu. Bokkoon na ciy jubluwaayam, saxal demokaraasi ak yoon wu tëdde njaaxanaay. Rax-ci-dolli, Séex Anta Jóob ku gëmoon mbatiit la ak làmmiñi réew mi.
Ci gis-gisam, am réew mënut a suqaliku ci làmmiñu jàmbur. Muy pólitig, di koom-koom, di Yoon walla njàng meek njàngale mi, fànn woo ci jël, mbatiit mooy cëslaay gi. Kon, fàww Afrig sukkandiku ci mbatiitam te bàyyi toppandoo bi ak jéggaani bu metti bi, ndeem bëgg na suqaliku. Ndaxte, ku xeeb sa cosaan, ñu xeebal la ko. Lii yépp nag, téere Xaadim Njaay bi xóotal na ci. Looloo ko tax a gànjaru te mucc ayib. Bu yeboo ku nekk wuti ko, jàng ko, jàngat ko te jëfe njàngale yi ci biir.
Tànnees na yenn ci kàdduy werekaan bi ngir dégtal leen leen :
Cosaanam
“Déedéet [soqikoowuma ci giirub géwél]. Du dëgg de, waaye meruma ci. […] Béréb bi nga cosaanoo mësul a doon ab gàllankoor ci boroom xel mu nar a liggéeyal mboolaay gi.”
Yóbbal ñeel ndawi Afrig
“Ndawi réewi Afrig yépp ñoo war a joxantey loxo ngir tabax Afrig gu dalandi te wóor. Fàww ndaw ñi génn ci yàccaaral bi ñu nekkee, jëfandikoo xel mu ñaw mi leen Yàlla jox ngir di fent lu am njariñ. Mën-mën biy nelaw ci yeen kepp laay jéem a yee : xelum fent. […]”
Bennoog Afrig
“Xam ngeen ma : panafirkanist bu dëggu laa. Te amul benn xeetu xeetal walla boddekonte ci sama biir ruu gi.”