MANSUUR FAY AM NA DËGG CI KAW NGUUR GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Dañu tere woon Mansuur Fay mu génn réew mi. Fan yii weesu, waññi nañu ko ñaari yoon ca dalub roppalaanu Belees Jaañ. Ñaareelu yoon wa nag, dafa àndoon ak ab “huissier” ngir mu doon seede. Ginnaaw gi la yóbb mbir mi ci yoon.

Àttekat bees duppee “juge des référés libertés” na ca Ëttu àttekaay bu kawe bi jox na Mansuur Fay dëgg. Nde, ci li layookat bii di Aamadu Sàll xamle, dafa santaanee ñu bàyyi Sëñ Mansuur Fay mu amal i tukkeem ni mu ko neexee.

“”Juge des référés libertés” joxe na ab santaane ngir ñu bàyyi Mansuur Fay mu tukki ni mu ko neexee. Ci weneen waxiin, àttekat bi dafa sant jëwriñu Biir-réew mi mu wax pólisu jaww jeek dig yi mu bàyyi Mansuur Fay doxi ay soxlaam.” (Kàdduy Meetar Aamadu Sàll)

Ci àjjumay tay ji, 28i màrs 2025, la ndogal li jib.
Ngir fàttali, Mansuur Fay (APR) dafa bëggoon tukki, génn réew mi, pólis tere ko ko ñaari yoon.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj