Taalifkat nga woon bu daan yatt xalimaam di bind ci xew-xewi réew mi. Misaal mi ci mujj mooy ñetti woy yi nga jagleel Covid bi.
Xawma sax fu ma lay tàmbalee sargal ginnaaw sa génnug àddina. Ndax damaa war a wax ci téere yu bari yi nga bind ? Walla damaa war a fàttali askan wi ni taskatu xibaar nga woon ? Mënoon naa sànni it kàddu ci sa taxawaay ci àtteb Hissène Habré, ci sa woyof ak ci sa mën a sañse. Waaye lii lépp daanaka ñépp seede nañ ko bés ba ñu yëgee xibaar bi. Kon lu des ? Xanaa ma jéem a wax ci nit ki ak mbaaxam.
Képp ku la xamoon, xamoon ni ku gëmoon Yàlla nga. Moo waral nga bindoon téere ci Cardinal Théodore Adrien Sarr, mu yëkkati woon ci yow ay kàddu yu daw yaram te dëggu. Bi ngay siiwal say téerey taalif, dangaa teg lépp ci loxoy Peer Blaise Pascal Sagna.Taxawaloon nga sa diine, amoon fa cër waaye rafetaloon nga sa diggante ak ñi nga bokkalul woon diine.
Sa téere woy bi nga duppe « Pétales noires » maa bind ubbite gi. Bi nga ma ko sante ci saa si laa nangu, fekk laata loolu weccee nanu ci ay yoon muy soog a génn. Ngay amal ndajem kajar, ni ma maa ciy amal waxtaan ak nit ñi. Du caagéeni damaa aay, dangaa xëroon ci sa jigéen rekk…
Sa yitte ci doomu-aadama ak cër biŋ ko joxoon, daa meloon ni ndawalu guddi…
Marcel Mendy, du benn xewu jullit boo ma bindul bataaxal di ma ñaanal. Noonu it laa ko daan defeek yow ba ci bés bi jiitu sag dem : àllarba laa la ñaanal kooru jàmm, nga tontu ma ci saa si, ñaanal ma tamit. Alxames ma yeewoo xibaar bu tiis bi : Marcel fekki na Jean Meissa Diop, xaritam, doomu-ndeyam. Muy lu ma bett lool. Li ko yokk di sa mébétum dajale woy yi nga bindoon ci lëlu koronaa bi ngir def leen téere… Ndekete du àntu ci sag dund.
Li ma bind tey diis na ma lool waaye du sama cër ma ni cell bañ a siiwal lu baax li ma la xamal, doonte sax dama koy tënk.
Fa nga tëdd ca Cees, yal na la fa yërmaande Boroom bi fekk, mu baal la te xaare la Guyaar.