MASAALIKUL JINAAN WALLA YOONI ÀJJANA YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci àjjuma jii weesu, 27eelufan ci weeru sàttumbar, atum 2019, lañ doon ubbi ci Kolobaan jumaa ju mag ji : Masaalikul Jinaan. Kilifa gii di Sëriñ Muntaaxa Mbàkke, Xalif kullu murid, moo jiite xew-xew bile. Kon, tey la woon tey. Ndege, xew-xew bi lëmbe woon na réew meek àddina sépp, daanaka. Ndaxte, muy JeuneAfriquedi Le Mondewalla RFIañs, genn kërug yéenekaay wutewul bés bi. Xibaar bi àggoon na ba Frãs ba seen benn politiseŋjot cee xund, wax sax ay waxi ku danoo ci saret. 

Jumaa ju réy, xaalis bu takku

Jumaa Kolobaan ji, nag, jumaa ju réy a réy la, képp ku ko gis yéemu ci yànjaayam. Yaatuwaay baa ngi tollu ci 6i ektaar. Dafa di sax, Masaalikul Jinaan mooy jumaa ji gën a réy ci Afrig sowu-jant. Lu ëpp 30 000, ci xayma, nit mën nañ cee julli : 8 000 ci biir, 20 000 ci biti ak 3 000 ci kow etaas bi. Njëgu tabax bi, moom, mi ngi tollu ci 20i milyaar ci sunu xaalis. Taalibe yee joxe 15i milyaar yi Sëriñ Siidi Maxtaar Mbàkke teg ci 5,5i milyaar. Taalibe yi dañu daan natt, ñii joxe 1000, ñeneen ñi 10 000, am it ñu génne ay milyoŋ def ci, ku nekk daal yaay seet fu sa doole tollu nga def li nga mën,mu néew mbaa mu bare. Jumaa ji, nag, kii di Sëriñ Muxammadu Lamin Mbàkke moo teg birig bu njëkk bi,  ci 7eelufan ci weeru sulet, atum 2012. Sëriñ Mbàkkiyu Fay mi toogal Xalifa bi ci Ndakaaru lañ dénkoon liggéey bi. Juróom-ñaari at lañ ci teg lépp door a sotti.

Jenn jumaa, 5i sooroor

Kon, Masaalikul Jinaan, ci njiiteefu Sëriñ Siidi Maxtaar Mbàkke lañ dooroon tabax bi. Nguuru Ablaay Wàdd moo joxe suuf su tollu ci 6i ektaar ngir ñu mën a jëmmal bëgg-bëggu murid yi. Arsitekt bi ñuy woowe Meysa Joojo Ture moo nataal juróomi sooroor yiy màndargaal  jumaa ji. Bi mu noppee ci liggéeyam, waa CDE ñoo kuule sooroor yi. bi ci gën a gudd, gën a gudd ci Ndakaaru itam, mat na 75i meetar, kon sute na 7i meetar bu jumaay Ndakaaru ju mag ji. Ay masoŋ yu fekk baax réewum Siwis, nag, ñoo yékkati sooroor yi. Bu dee taaral bi, ay nataalkat yu xereñ, jóge fépp ci àddina si, ñoo ko defar. 

Ubbite bu xumb

Fépp la taalibe yi ak soppe yi màbbe keroog àjjuma, jubalsi Kolobaan ngir teewe xew-xew bi, julliwaale fa, muy julli bees fay njëkk a amal, ubbee ko jumaa ji. Mbooloo mu takkoo noonu, day laaj ay matuwaay yu wér te wóor. Moo tax nguur gi teel a yabal takk-der yi, way-fajkat yi ak balekat yi ngir waajal bés bi. Waaye, daayira yi tamit, kenn demul ñu des. Pastéef bu mat sëkk lañu wone. Kolobaan xumbal la ko bii peeru xumb, ñu samp mikóro yi, alxuraan ji di daw ak i xasiday Séex Axmadu Bàmba Mbàkke. Waa daayira Xidmatul Xaadim samp fa seeni berkelle, taf fay nataal ak ay këyit yuy màndargaal taarixu yoonu murid ak kàdduy Sëriñ Tuubaak Séex Ibraayma Faal mi ñuy woowe : buntu muridiina. Waaye, teewaayu Njiitu-réew mi, Maki Sàll, ak bu Ablaay Wàdd, Njiitu-réew ma woon, doon na lu fés lool ci bés bi.

Wenn askan, benn jëmu, jenn jumaa

Ubbite juuma ji, nag, du rekk mbooloo mi fa teew daa takku. Loolu am na waaye li gën a yéeme mooy li nit ñi bawoo fépp ci réew mi ak sax bitim-réew. Li ko dale taalibe yi, kilifa diine yi bokk ci yeneen tarixa yi,  kilifa diine katólig yi, kilifa aada yi, jaraaf ak jawriñi Lébu yi ci Ndakaaru, politiseŋyi moo xam ci nguur gi lañu bokk mbaa ci kujje gi, moom daal ñépp a nga woon Kolobaan, kenn nanguwul a toog di xaar ñu lay nettalisi bés bi. 

Kon, mënees na wax ne, réew mépp a daje woon ca Kolobaan ngir màggal ubbite jumaa ji. Taalibe murid yi tukkurmuutba nga ne lii lu mu doon. Réew mépp di tés-tési. Ci nataali bés bi, ñoo ngiy ciy wane Njiitu-réew mi Maki Sàll ak kim fi wuutu, Ablaay Wàdd ñu séq Xalifa bi. Wànte, nataal bi gën a neex ñépp mooy ñoom ñaar bi ñu jàppantee, ku nekk yékkati sa loxo moroom, di ree. Mu mel ni bés bi dafa jubale ay noon, tàppe xol yi, lëkkale ay kër ak i kurél, boole askan wi, ñépp ànd doon benn, bokk benn jëmu. Tijaan yi waxoon nañ sax ne Masaalikul Jinaan lañuy defe seen wasifa àjjuma ji. 

Waaye, bu loolu weesoo, warees na jukkee ci mbir mi ñaari jàngat.

Bi ci jiitu mooy ne, bu doomi Senegaal yépp bokkee doon benn, am pas-pas te nangoo liggéey, réew mi dina jëm kanam. Ndaxte, jumaa ji, xaalis bu takku bi ci dem yépp, ci gafaka askan wi la génne. Lebiwunu fenn, tàllalunu kenn loxo. Kon, bu nu gëmee sunu bopp dëggantaan, bëgg sunu réew ba noppi jële fi xàjj-ak-seen, bennoo, mën nanoo tabax Senegaal ba mu naat te dunu am ak kenn xaar-ma-Yàlla.

Ñaareelu njàngat maa ngi aju ci doxalinu politiseŋyi. Saa su xew-xewu diine amee, nga gis leen ñuy sukkal ak a raamal sëriñ si. Ak nu mu mënti deme, jëf ju ñaaw la. Kilifa dafa war a wormaal boppam, weg ñi ko fal te bañ a tuutal ndombog-tànk giñ ko dénk. Rax-ci-dolli, askan wi war naa yeewu ci jikkoy naaféqu politiseŋyi. Juboo neex na, gaa, te jàmm a gën ay, duñ sax benn. Waaye, diggante Abdulaay Wàdd ak Maki, li ci jot a xew lépp ak li ci kilifa yu baree-bare jot a wax…ñu bàyyi ba bés bu màggee ni bii mel ni ñuy teyaatar ! Aa… Newunu du dëgg ci ñoom de, waaye mbir mi warees na cee màndu ba xam fu muy mujje. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj