Ag gaal gu yeboon i mbëkk-kat moo teeri Gàddaay. Nee ñu am ñaar ñu ci ñàkk seen i bakkan. Ci guddig talaata ji la gaal gi teer ci tefesu Gàddaay, fa Géejawaay, ci anam yu doy waar.
Barñi la gaal gi tëmbee. Ci guddig altine ji, jàpp talaata, la fa jóge. RFM a siiwal xibaar bi. 280i nit la gaal gi yeboon. Ñaar ñoo ci faatu, am kenn ku ci sonn lool. Te sax, am na ñu bari ñu ñu téyandi ca pólisu Wàqi-Naan Nimsat. Dañ leen a war a déglu, laaj leen.
Ba léegi nag, Càmm gi jëlagul i matuwaay ngir tere nit ñi sóobu ci géej gi.