MBËKK MI MBËKKATI NA RÉEW MI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Coowal mbëkk maa ngi bëgg a booy nopp yi. Ndax, fan yii, dafa lëmbeeti réew mi. Dafa di, jamono yii, mëneesul a toog bés te joteesul xibaar ñeel ug gaal gu suux, walla gaal gu këppu. Ay téeméeri téeméeri ndaw ñooy song géej gi, di mbëkki. Bu ci ndaw ñi ëppee tamit, léegi, mag ñi, jigéen ñi, gune yi, imaam yeek sëriñ si, ñépp a ngi dem. Léeg-léeg sax, nga dégg ciy jigéeni biir yuy war gaal yi, wutali Espaañ. Saa su nekk, géej giy wann ay téeméeri téeméeri bakkan. Daanaka, léegi, géej gi dafa soppaliku, nekkaat armeel, ku ci lab, mu di sa bàmmeel. Xanaa géej gi suur la, walla mu yërëm say mbokk, goqi la ci tefes gi ngir ñu waajal sa néew ni mu waree, denc la, dëjal la. Njaaboot yaa ngiy jeex. Te, Séex Isaa Sàll, meeru Mbuur bi, firnde la ci, moom mi ñàkk lu tollu ci 20 ciy mbokkam ci gaal gi suux fa Mbuur.

Moone de, foogoon na ni mbirum Bàrsaa walla barsàq féete na ginnaaw. Ndekete, saa su nekk, daf nuy jiitu , taxaw di nu xaar. Néew yi bari nañ, waaye ndaw ñi ciy sóoboo ngi mel ni ay gumba. Wax ji law na, waaye roñukat yi dañu tëx, mel ni ñu ñu xabtal, ñuy mbëkk rekk, géej di leen mëdd. Waaye, taxul ndaw ñi xàddi. Faalewuñ kenn, faalewuñ dara. Dem rekk. Tekki rekk. Amul leneen. Li ñuy bàkkoo mooy : “Tekki mbaa dee rekk.” Maanaam, Bàrsaa, walla barsàq. Luy sabab yi ?

Senegaal, réew mu ndóol la. Dund gi jafe na, ndax lépp a njëge. Liggéey yombul, xaalis amul. Te, Senegaal, nekk fi góor, taaw walla yaakaaru njaboot, lu mettee metti la. Nde, sas wu réy la la mboolaay giy gàll, rawatina boo nekkee ndaw bu góor. Nde, ndaw mooy ki war a wuutu baay, war a dimbali yaay. Digalees na ko mu taxawu mbokk, defal mag ak rakk. Fu xew amee, bum ci mën di doon, war na dugal loxo ci poos, ñuqi, joxe. Bu ko defulee, ñu xas ko, ŋàññ ko, suufeel ko, beddi ko, toroxal ko ci biir i nawleem. Am na kook amu ko, seen yoon. Mën na ko am déet, seen yoon. Ci déggiinu Saa-Senegaal yi, ki tekki mooy kiy joxe dara, maanaam ku leen di jariñ, donte as lëf la. Kon, gàllees na ndaw ñi wareef ci kow wareef te, réew mi, lépp a fi dëgër.

Njàng mi baaxul. Liggéey amul. Njaay mi doxul ndax ñépp ñooy jaay léegi. Sikkim a lakkandoo te ndox amul. Moo tax ñuy song ndox mi walla jéeri ji ngir dagaani wërsëg.

Nguur gii di sog a ñëw, ci seen i kàddu, ñoo ngi wut i pexe ngir saafara ko wenn yoon, mu jeex. Démb, Njiitu réew maa nga woon Mbuur ngir jaale njabooti ñi ci ñàkk seen i mbokk, mastawu leen. Waayeet, jël na fa kàddu, biral ne Càmm gaa ngi liggéey ci suuf ngir xeex mbëkk mi.

Njiitu réew mi xamle na fa ne, jàpp nañ fan yii weesu ag gaal gu yeboon 600 ak lu teg ciy roñukat. Nee na tamit dinañ def seen kemtalaayu kàttan ngir jàpp ñiy yóbbaate. Ndaxte, ciy waxam ba tey, dafa am ñiy sukkandiku ci ndóol gi ak ñàkkug xëy mi ngir nax ndaw ñi, gëmloo leen lu amul, lekk seen xaalis. Rax-ci-dolli, dafa am ñu ciy boole lees di wax « trafic d’êtres humains », maanaam di jaay ay nit.

Bees sukkandikoo ci kàdduy Sëñ Basiiru Jomaay Fay, Njiitu réew mi, du ndóol gi ak ñàkkug xëy mi rekk ñoo sabab mbëkk mi. Nde, am na ciy mbëkk-kat yuy bàyyi seen i liggéey ngir dem. Dafa mel ni, ñàkk a doylu bi ak sas yu bari yi bokk nañ ci luy sabab mbëkk mi. Kon, wutal ko pexe mu sax dàkk dina jafe lool. Bu ko defee, warees na amal i gëstu ak i njàngat yu xóot ngir xam dëgg-dëgg li waral mbëkk mi, sog di ko wutal i pexe.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj