Asamaan démb si dafa bàyyeeku, ubbiy buntam, rëccal ndox mi, mu sotteeku bu baax a baax. Daanaka, réew mépp a taw. Waaye, Tuubaa daf cee rawati. Nde, foofa, di péeyub murit yi, taw bi daf fa sabab loraange yu metti. Ndax, ginnaaw bi taw bi sewetee, taa-taa yi dañoo nangu yenn kër yi. Am na sax, ci lees siiwal, ñaari bakkan yu ci jot a rot.
Taw bi sewet na fa Tuubaa. Waaye de, ñu bari ci Saa-Tuubaa yi amatuñu fu ñuy seeloo. Ndaxte, ndox maa nangu kër ya, génnee way-dëkk ya. Lu ëpp 140i mm cim ndox moo wàcc Tuubaa ci benn bés kepp. Bariwaayu ndox mi waral na paatug ñaari nit yu ci seen i bakkan des. Sàppëeri Cees yeek yoy Njaareem (Njurbel) yi walluji woon nañ, ci lu gaaw, askan wa ca loroo. Mbënn ma topp ci taw bi sabab na fay yàq-yàq ju jéggi dayo. Jumaa ju mag ja sax muccul ci ndox mi. Nde, béréb ya ko wër yépp dañoo taa ba fees.
Càmm gi seetanul askan wa. Ginnaaw bi ñu fa yabalee sàppëer yees tudd ci kow, jëwriñu Ndox meek Cellal gi, Doktoor Séex Tiijaan Jéey, demal na boppam Tuubaa. Li mu ku dugge mooy nemmeeku way-loru yi, mastawu leen te jaale mbokki way-dëddu yi ci faatu. Rax-ci-dolli, jëwriñ ji saytuwaale na loraange yi taw bi sabab, daldi jokkale liggéey bees doon def ngir dimbali nit ñi, taxawu leen. Jubluwaayu taxawaayam fa Tuubaa moo doon indiy pexe yu gaaw ngir wallu way-loru yi, fexe ndox mi dem. Waayeet, dañu wutaale ay pexe ngir fàggandiku balaa beneen taw di fa sóobaat, bu ko defee ñu mën koo dékku ba kenn du ci loru. Dépite Pastef ba woon, Séex Coro Mbàkke, doon na ko gunge ci liggéey bi. Moom it, njiitul Pastef li fa Tuubaa, génnoon na ci wetu askan wa, di leen dimbali.
Wolof dafa ne, ndimbal na cay fekk loxol boroom. Loolu la waa « Touba CA Kanam » [Tuubaa Ca Kanam] xam ; moo leen tax a jóg, ñoom itam, xar ci seen i tànki tubéy. Noonu, kurél gi dafa tàmbali di sanc ay seeluwaay (këri négandiku walla làquwaay). Dafa di, seeluwaay yooyii sax, tabax gi dooroon na laata taw yi. Waaye, dañ ko jampal léegi. Li ñu ko dugge mooy fexe ba ñi nga xam ne ndox mi dafa nangu seen i kër, ñu am fu ñu dalandi.
Bees sukkandikoo ci Moori Ture, xam-xam màcc ci wàllu njuux (météo), coppitey njuux lee waral xeetu taw yile fa Tuubaa. Rax-ci-dolli, ba tey ciy waxam, Tuubaa dafa rafle ay tabaxte ñeel yooni ndox meek cellal gi. Teg na ci sax ne, Tuubaa dafa bokk ci depàrtamaa bu Mbàkke. Te, ci li ANSD biral ci caabalam gu mujj gi, Mbàkke mooy depàrtamaa bu ëpp i nit fi Senegaal. Ànd ak loolu yépp, Mbàkke amagul sax estaasiyoŋ buy natt ak a saytu njuux li, waroon a tax ñuy waajal taw yu ni mel, di moytu jéyya walla loraange yu ci mën a tukkee.
Jëwriñ ji, Doktoor Séex Tiijaan Jéey, dafa setal Nguur gu bees gile ci loraangey nawet bi. Nde, ci waxam, nawet bii, du seen nawet, dañ ko fee fekk. Dañuy jéem a dabu rekk. Waaye, nawetu déwén bi, dinañ def li leen war ba coono yi askan wiy jànkonteel daldi jeex. Loolu la fa dige.