MBINDUM WOLOF : “FONK SUNUY LÀMMIÑ” TÀGGAT NA AY SAABALKAT

Yeneen i xët

Aji bind ji

Mbootaayu Fonk Sunuy Làmmiñ amaloon na jotaayu njàngum bind wolof. Saabalkat yi la ko jagleeloon. Mbootaay gi daf ci àndaloon ak IFAN (Institut Fondamental d’Afrique noire) ak “Maison de la presse” (Kërug saabalkat yi). Ci alxames jee weesu, 17i pani oktoobar 2024, lañu ko doon amal. Jubluwaay bi moo doon tàggat saabalkat yiy jëfandikoo làkku wolof ci seen liggéey, jàngal leen mbind mu jub, gàgganti yenn njuumte yees di faral di gis.

Mbootaayu Fonk Sunuy Làmmiñ dafa woote “jub, jubal ak a jubbanti mbindum làmmiñi réew mi”. Waaye nag, wootewu ko rekk toog. Dafa sóobu ci liggéey bi, di amal i jotaayi njàng ñaari ayu-bés yu nekk, bési àllarba ak gaawu, ci teeweel ak ci lënd gi. Wii yoon nag, saabalkat yi lañu woo ngir tàggat leen ci yoonu mbind mi.

Ci kàdduy Ceerno Siise mi doon jàngale yoonu mbind mi, jotaayu njàng mooma dafa bokk ci luy sàmm ak a wattu làmmiñi réew mi. Daf ne woon :

“Jubluwaayu jotaayu njàng mii, mi ngi aju ci tàggat saabalkat yi, jàngal leen mbindum wolof ak nëwu làmmiñ wi. Loolu dina tax ñu mën a moytu yenn xeeti njuumte ak i yàq yu mën a soppi maanaa xibaar yi ñuy dégtale.”

Kàddu yii la fa Ceerno Siise yékkati, moom miy Sàmba-Kopparu mbootaay gi. Njiitul mbootaay gi feelu ko, rafetlu itam teewaayu saabalkat yi. Ci kàdduy njiit loolii di Adraame Jaxate, lu jege téeméeri saabalkat teewe nañ jotaayu njàng mi. Jàngal nañ leen abajada wolof, faramfàcceel leen coowaan yi, miigaan yi ak yoonu mbind mi. Mbindum wolof nag, ak yeneen làkki réew mi sax, Nguur gi daf ko yoonal, tënk sàrti mbind ci ab dekkare (2005).

Sëñ Adraame Jaxate a ngi njort ne, bu saabalkat yi jógee ci jotaay bi, dinañ jàpp li ñu jàng, jëfe ko. Rax na ca dolli sax, ne :

“Jotaayu njàng mii dafa dëppoo ak gis-gisu pólitig bu Njiitu réew mi ñeel njàng ak njàngalem làmmiñi réew mi.”

Sëñ Usmaan Lóo, bokk ci mbootaay gi, ma nga fa woon. Moom nag, werekaan bu mag la ci làkk wi, di ko xeexal, di ci gëstu ak a jàngale. Joyyantil na saabalkat yi as lëf ciy baat ak i kàddu yu ñuy faral di jëfandikoo ci seen liggéey. Beqil na leen i njuumte yu bari yees di nemmeeku ci seen i wax ak ci saabalukaay yi.

Ñu bari ñoo rafetlu jéego bi mbootaayu Fonk Sunu Làmmiñ teg. Moo tax, mbootaay gi fas yéene wéyal lu ni mel, di ko baamu. Dafa di sax, ñoo ngi naal yaatal ko ci yeneen diiwaani réew mi ak yeneen làkk yi. Soxna Ajaratu Umar Sàll, di ma-làmmiñal te bokk it ci mbootaay gi, biral na solos ndaje yu ni mel. Dafa wax ne :

“Dafay baax ñuy yee nit ñi [ci solos làmmiñi réew mi] te di amal xeeti jotaayu njàng yu ni mel. Bu ko defee, ak lu mu tuuti tuuti, saabalkat yi dinañ sàmmonte ak dekkare bi yoonal mbind mi.”

Njiitul “Maison de la presse” (Kërug saabalkat yi), Sàmbu Biyaagi, biral na solos njàngum mbind mu set te jaar yoon. Nde, ciy waxam, dég-dég (xibaar) dafa doy waar, moo tax ñu war a bàyyi xel mbind mi. Dafa di, mbindiin wi walla waxiin wi dafay jeexital ci déggiinu  xibaar bees di saabal.

Dees na delloo njukkal saabalukaay yuy siiwal seen i xibaar ci làmmiñi réew mi. Dees na ci lim Saabal.net bi nga xam ne, kurélu WAX (Wolof Ak Xamle) gi Sëñ Séex Lóo jiite moo ko taxawal ; LU DEFU WAXU bi bindkat bii di Buubakar Bóris Jóob taxawal. Ñaari saabalukaay yii, ci wolof lañuy siiwal. Bu dee ci làkku pulaar, dees na lim dalu web yii di Fooyre Ɓamtaare ak Binndi pulaar.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj