MBIRUM BUGAAN : 30 OKTOOBAR 2024 MOOY BÉSU ÀTTE BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitul “Mouvement Geum sa Bopp” [Gëm sa Bopp], Bugaan Géy Dani, mi ngi ci loxoy yoon jamono jii. Fa Bàkkel lañu ko téyandi, muy xaarandi àtteem bi war a am keroog 30i pani oktoobar 2024. Moom nag, dafa jàppante woon ak sàndarm yi, bëggoon a xëtt dog bi ñu defoon ci talib Bàkkel bi.

Fan yii, dexu Senegaal gi dafa wal ak doole, daldi dugg ci dëkk yi, nangu i kër ak i tool, sabab ay loraange yu bari fa Bàkkel ak Maatam. Askan wa loru ci wal mooma, ñu ngi ciy jafe-jafe yu tar. Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, ma nga fa woon sax ngir nemmeeku leen, mastawu leen, yóbbaaleel leen ndimbalu Càmm gi. Ca jamono jooja yit, Bugaan Géy Dani mi jiite kurélu Gëm sa Bopp, bëggoon na fa a dem ngir, ciy waxam, seeti leen, yóbbu fa ndimbalam. Waaye, jotul a àgg fa béréb ba. Nde, sàndarm yaa ko dogaale.

Bi mu jógee Seme, war a jàll Bàkkel, fa la ko sàndarm yi dogaale. Kilifay sàndarm yi ñoo siiwal ab yégle di ci xamle ne :

“Gaawu bii, 19i pani oktoobar 2024, ci boori 13i waxtu yu toftal 40i simili, Birigaadu sàndarmëri mberaay bu Bàkkel jàpp na Sëñ Bugaan Géy Dani ci sababu bañ a dégg ndigal.”

Dafa di, bi Bugaan àggee ca postu sàndarmëri bu Bonji, 13i daamar ñoo ko toppoon. Ca lees ko taxawal, wax ko ne dafa war a négandiku tuuti. Ci li takk-der yi wax, mbirum kaaraange moo taxoon ñu waxoon ko mu xaar as lëf laata ñu koy bàyyi mu wéyal aw yoonam. Nde, Njiitu réew mi a waroon a romb. Waaye, bees sukkandikoo ci takk-der yi ba tay, njiitul Gëm sa Bopp li bokk ci lëkkatoo Samm Sa Kaddu [Sàmm Sa Kàddu] ñeel wotey 17 nowàmbar yi, dafa lànk, wax ne dee dafay jàll. Maanaam, dafa bañ a dégg ndigalu sàndarm yi. Noonu, mu bëgg a xëtt dog bi sàndarm yooyu defoon ci tali bi, sant ay àndandoom ñu topp ko.

Ci kow loolu, komandaŋu “Compagnie de gendarmerie de Bakel” daldi yabal waa ESI (Escadron de Surveillance et d’Intervention) ngir ñu dem dooleel sàndarm ya fa nekkoon, daldi dogaale Bugaan ci jàlluwaayu (pont) Turim. Turim, ab dëkk la bu nekk ci kow tali bi, soree Bonji 12i kilomeetar.

Ci seen yégle bi, sàndarm yaa ngi wax ne, komandaŋ bi dafa jàpplu Bugaan ngir ne dafa bañ a jëfe ndigal lees ko sant. Ca lañ ko jébbalee Yoon, fa Bàkkel.

Ginnaaw gi, bi mu janoo ak toppekatu Tàmbaakundaa bi, daf ko dóor “mandat de dépôt”. Dees na ko àtte ci lees dippee “flagrant délit”, keroog 30i pani oktoobar 2024.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj