Mansuur Fay mi ngi ci guddi gu lëndëm këriis. Nde, jamono yii, Yoon dafa ko téyandi ci kaso bi. Ndiisoog luññutu gog Ëttu àttekaay bu kawe bi moo ko doon déglu tay. Njiitu ndiisoo googu, ginnaaw bi ñu ko dégloo, moom ak i layalkatam, moo ko dóor lees di wax « mandat de dépôt ».
Ca jamonoy mbasum koronaa ma, Mansuur Fay moo nekkoon jëwriñu Yokkuteg mboolaay mi, Màndute ñeel mboolem-nawle mi ak mberaay mi. Moom nag, dafa am lu ñu ko cëraloon ci koppar yees jagleeloon xeexub mbas mi. Ni mu yoree woon xaalis boobu nag ñu ko dénkoon, ci li caabalug Ëttub cettantal bi fésaloon, dafa desee jub. Nee ñu, li mu wax ne moom la jënde woon ceeb bees daan séddale dafa ëpp. Maanaam, dafa dolli 2,749i miliyaar ci njëgu ceeb bi te amalu ko lay.
Mansuur Fay nag weddi na tuuma yooyu. Moom sax, ci li ay layalkatam xamle, dafa doon sàqu ngir ñu bàyyeendi ko. Waaye, àttekat bi dafa leen gàntal càkkute googu. Kon, Mansuur Fay dina fanaan guddeem gu njëkk ci kaso bi.