MBIRUM KOPPARI COVID-19 YI : JÀPP YAA NGIY WÉY

Yeneen i xët

Aji bind ji

Mbasum koronaa maa ngi wéy di lëmbe réew mi. Naam, jàngoro ji wéy na, waaye jeneen jàngoroo ko fi wuutu, muy jàngoroy càcc ak luubal xaalis. Nde, jamonoy mbas ma, ba ñu tënkee nit ñi ci seen kër, dajale koppar yu takku ngir xeex ak mbas, dafa amoon ñu ca tibb, di duy seen i jiba. Dafa di, junniy miliyaar lees dajale woon ngir fàggu musibay mbas mi, muy ci fànnu wér-gi-yaram, di ci fànnu koom-koom, añs. Junniy miliyaar yooyee nag, la taxoon ñu dajale ko, defuñu ko ; ña taxoon ñu dajale ko yit, jotuñu ca. Loolu, caabal gi Ëttub cettantal bi siiwaloon moo ko firndeel, ginnaaw bi mu lëñbëtee mbir mi, daldi gis ne, ndekete, ña ñu dénkoon xaalis bi sàmmontewuñu ak seen i wareef.

4i at ci tay ginnaaw bi mbas mi weesoo. Waaye, coow laa ngi wéy di ubale réew mi. Nde, bés bu set ñu jàpp lim bu takku ciy nit yu ci laale woon. Tay jii rekk jàpp nañu ñii seen i tur toftalu fii :

– Lamin Jàllo, kontaabal loppitaanu Kafrin : lees koy tuumaal mooy ne dafa joxe ay këyit yu baaxul ngir layal 45 miliyoŋ yi mu wax ne def na ko ci mbas mi, te muy koppari askan wi ;

– Aliw Sow, DAGE bu njëwriñu Yokkuteg mboolaay mi, Yemoog nit ñi ak mberaay yi : lees koy toppe mooy 2i miliyaar yu tegal 749i miliyoŋ ak 927 498 ci sunuy koppar. Xaalis bu ni tollu nag, ngóor si Sow dafa wax ne ceeb la ko jënde te, koppar yu ni tollu, weesu na lool njëg li ceeb biy jar.

– Njàmme Njaay, njiitul « Fonds d’impulsion de la microfinance » : tuuma jees koy toppe mooy, ñàkk a indi ay firnde ci 11i miliyoŋ yu teg 191 532 FCFA yees ko dénkoon.

– Muhammadu Seen, DAGE bu njëwriñu Ndaw ñi : li tax ñu jàpp ko mooy xaalis bu ëpp bi mu wax ni def na ko ci « gel hydroalcoolique » yi, mu tollu ci 41i miliyoŋ yu tegal 217 580 FCFA.

– Matlen Susaan Lóo, DAGE bu njëwriñu Yaxantu gi ak PME yi : tuuma ji tax Yoon teg loxo mooy koppar yi ëpp yi mu wax ne def na ko ci « gel hydroalcoolique » yi, mu tollu ci 805 000 FCFA.

– Muhammadu Bàmba Amaar, « aide-comptable » ca njëwriñu Yokkuteg ndefar yi ak Ndefar yu ndaw yeek yu yemamaay yi : dañu njort ne dafa génnee xaalis bu bari, diggante 2020 ak 2021, ci am sàq bees ubbi fa bànku BOA ngir suqali ndefar yu ndaw yeek yu yemamaay yi.

– Ndey Aminata Lum Njaay, DAGE bu njëwriñu Yokkuteg ndefar yi ak Ndefar yu ndaw yeek yu yemamaay yi, ak Mustafaa Jóob, aji-saytu sàqum xaalis bees jagleel ndefar yu ndaw yeek yu yemamaay yi te mu nekk ca bànku BOA : ñoom ñaar ñépp, li ñu leen di tuumaal mooy ay payoor yu teey xel ci njëndum mask yi. xaalis baa ngi tollu ci 2i miliyaar yu tegal 500i miliyoŋi FCFA.

– JIbi Jaxate, DAGE du njëwriñu Njaboot gi : lees koy toppe ñàkk a joxe ay firnde ci 36i miliyoŋ yu teg  147 500 FCFA.

– Lewõs Nzally, DAGE bu njëwriñu Jokkoo gi ak Mbatiit mi : li tax ñu jàpp ko mooy miliyaar bu tegal 120 000 FCFA.

– Alasaan Jàllo, DAGE du njëwriñu Mbéll yi Sewolosi : li ñu koy toppe mooy ne dafa génne xaalis te liggéeyeewu ko.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj