Meetar Musaa Jóob a ngi ci guddi yu lëndëm jamono jii. Ndax, tey ci àjjuma ji, 15 desàmbar 2023, lañ ko dóor « mandat de dépôt ». Àttekatu luññutu bu ñaareelu kabineb tirbinaalu « Grande Instance » bu Ndakaaru, Mamadu Sekk, moo jël ndogal li.
Moom, àttekat boobii, yàggalul mbir yi sax. Dañ ko jébbal mbir mi rekk mu sóobu ci liggéey bi. Moo ko tax a yóbbulu layookat bii di Meetar Musaa Jóob ndung-siin. Nde, dafa topp ndigalu Toppekatu Bokkeef gi, Abdu Kariim Jóob mi sàkku woon « mandat de dépôt » bi.
Cig pàttali, Me Musaa Jóob, moo jiite woon Dakar Dem Dikk, bokkoon ci lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar. Moom nag, dafa weeje woon Njiitu réew mi, Maki Sàll, tubaab bii di Sã-Kólod Mimraŋ (Jean-Claude Mimran) ak Mamadu Jaaña Njaay mi ko fi teewal, ak Aali Nguy Njaay mi fi nekkoon jëwriñu Mbéll yi. Dafa tegoon ay tuuma ci seen kow ñeel ag pasug liggéey gu aju ci menn mbéllum marjaan ci bëj-gànnaaru réew mi.