Keroog, àllarba 18i fan ci saŋwiyee 2023 la mbootaayu Fonk Sunuy Làmmiñ doon sargal ak a delloo njukkal bindkat bu mag a mag bii di Séex Aliyu Ndaw. Xew-xew baa nga ame woon ca Kërug Mbatiit gees duppee Duuta Sekk (Maison de la culture Douta-Seck). Bindkat bi nag, fental na mbootaay gi taalif bu daw yaram ngir gërëme leen ko.
Moo man lu may waxati ?
Ku fonk sa làmmiñ fonk sa bopp
Te ku fonk sa bopp fonk doom-Aadama
Ndax kat nit la ni yow
Kon kay mook yow a yem
Bu ko xamul bul ne ko cam
Ba kook àddina ba ca cëy
Mënuma leen a gërëm
Te sax jéemuma ko
Xanaa kay ma géewal
Fii tey jigéen ñi ci yéen
Ngir teey baak yar ba
Xel ma làmbook seetlook yiw ga
Soxna Aram jàng na dégg na
Xel rafet xam-xam sell
Bàjjen sa na la Sugeer
Fàtttali la ca Paaléen
Te Sindóone merewu la
Maryeetu moom jarbaat la
Bu yabul nijaay
Ajaratu Sàll ca farlu ga
Ndey Koddu déglu mag ña
Su bànqaas ak xob di jaayu
Dàtt ne sëmm di jaay maanaa
Reen a tax ñuy bàkku
Jaaraama Jigéen ñi
Jàpp tëwa bàyyi
Bañ a tàyyi bañ a yoqi
Ba lépp sotti
Kaar-kaar Yàlla xeeb dolli
Seex Aliyu Ndaw
Ndakaaru
Gaawu 20 Saŋwiye 2023