MOODY’S WÀCCEE NA NATTUB SENEGAAL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Moody’s Investors ag kurél la guy natt réewi àddina si ci wàllu kopparal. Bees sukkandikoo ci dég-dég yi kërug Bloomberg siiwal, Moody’s Investors dafa wàccee nattu borub Senegaal bi ba mu suufe bu baax a baax. Li ko waral mooy li feeñ caabalu Ëttu cettantal bi génn fan yii weesu. Nde, caabal googii dafa biral ay rëq-rëq yu doy waar ci anam bees doon saytoo koppari réew ci ci Nguurug Maki Sàll.

Ba tay ci li Bloomberg jukkee ci yégle bi Moody’s Investor génne, dañu wàññil Senegaal ñaari poñ ci xaalisi bitim-réew. Loolu di tekki ne réew mi wàcc na ba tollook B3.  Maanaam, dafa wàcc ba yemook 6i jéego ci suufu ci xeetu « kopparal ». Li ci gënatee doy waar mooy lees dàkkentalal Senegaal « négative ».

Li yépp nag, mi ngi tukkee ci luññutu gi njiit yu yees amal ñeel caytuwiinu koppari réew mi ca jamonoy Maki Sàll. Ginnaaw bi IGF njëkkee siiwal ag caabal guy wane ay njuuj-njaaj ak i naxee-mbaay ci alali réew mi, Ëttub cettantal gi daf ko feelu, génnee lu yées li mu siiwaloon. Looloo waral, jamono jii, kurél yu nat ak saytu koppar ak koom-koomi réewi àddina si di wàccee Senegaal saa su nekk. Ndax, fi mu nekk nii, koom-koomu réew mi dafa nërmeelu.

Dafa di nag, natt yi kuréli àddina siy natt koppar ak koom-koomug Senegaal, di ko wàccee, mën am njeexital ci leb bi muy lebi xaalis bitim-réew. Ndax, dafay tax ñu bari duñu la wóolooti ba di la lebal. Bu boobaa nag, mën na jural réew mi ak askan wi ay jafe-jafe ak i gàllankoor yu réy.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj