Tiis ak naqar wu réy ñoo dal ci kow njiitul DMedias ak kurél Gëm Sa Bopp, Bugaan Dani Géy. Waayeet, njabootu ndem-si-Yàlla ji, Coon Sekk, ñoo ngi jooy. Moomi Sekk moo Faatu, moom miy soxnas Bugaan Dani Géy, di doomu Coon Sekk, baayu Waali Sekk.
Moom nag, nee ñu, daa feebaroon diir bu yàgg. Moo taxoon sax ñu rawale ko Farãs. Waaye, dafa mujje dëddu àddina. Ci alxamesu tey jii lañ ko waroon a jullee fa jumaa westfuwaar (Ouest Foire). Ginnaaw gi, dees na ko rob ca sëgi Yoof ya. Ñoo ngi nangoo njaal yi fa Site-Kër-Góorgi.
EJO ak Defu Waxu noo ngi koy jaale Bugaan Dani Géy, di ko jaale njabootu Coon Bàllaago Sekk yépp, di bokk ak ñoom tiis week naqar wi.
Yal na Yàlla jéggal ko, yërëm ko te xaare ko guyaar.