Fa Sancaba, gox bu nekk Caaroy-géej, ñetti gune lañu fekk ci benn daamaar ñu faatu. Jéyya jooju mu ngi xew keroog ci altine ji. Xale yi dañu réeroon seen i mbokk. Baay Dawda Jóob, Mammadu Maar ak Maymuuna Ñaŋ seen i at tollu ci ñeent ba juróom, ñoo ñàkk seen i bakkan.
Njaboot gu yeewoo tiis ginnaaw ba ñu gisulee seen i xale. Mbir ma faf ëpp i loxo, ba ñu nemmeekoo ay gune yu faatu ci ab daamaar. Lépp ma nga xewe ca goxu Sancaba, fa xale yooyu dëkk. La way-juri xale ya xamle mooy ne, dañu leen yónni woon, ñu yóbbu añ ci seen bàjjan. Booba lañu leen gëj a gis.
Ci taalata ji, lañu fekk seen i néew ci biir maalu daamaa bu yàqu. Noona lañu woowee takk-der yi (sàndarmëri ak pompiye), ñu ñëw. Ubbees na ci ag luññutu ngir leeral ci yan anam la xale yooyu faatoo ak lu walla ku leen dugal ci maalu daamaar bi.
Mu mel ni xew-xew yu ni mel mu ngi bëgg a bari fi réew mi. Ay réer yu ñuy xamle te du mujj fu rafet. Lu ni mel, war naa tax ba kilifa yi di gunge askan wi ci ay seet walla wër gu gaaw balaa musibay am. Rax-ci-dolli, kaaraange nekk na lu jafe ci yenn ci gox yi. Mu nekk liggéey bob, ñu ngi ciy xaar Càmm gi ngir nit ñi mën a dund ci péexte.