“MUUT ! MOTT ! NUN, WAA ISRAAYEL, NOO NGI REY !”

Yeneen i xët

Aji bind ji

Léegi, képp ku jóg ngir saabal reyaate ba xew fa Palestine, Israayel dina la rey ngir noppiloo la. Nde, bi xare bi tàkkee, keroog 7 oktoobar 2023, ak tay, njiiti Israayel yi reylu nañu 200i saabalkat yu daan siiwal musiba ak mbugal yay xewe fa Palestin. Kurél gii di Reporters Sans Frontières, gàttal biy joxe RSF, moo joxe lim boobile. Mu mel ni, li Israayel bëgg a wax àddina sépp mooy : “Nee leen muut ! Damay rey ! Nee leen mott te bàyyi ma ak Julliti Palestin yi ma faagaagal leen !”

Hossam Shabat mooy saabalkat bi sóobarey Israayel yi mujje bóom ci altiney barki-démb ji, fa Gasaa. Ab “drone” lañu yónni, mu dóor bomb ci daamar gi mu nekkoon, moom Hossam Shabat, daan liggéeyal tele Al-Jazeera. Moone, daamar gi amoon na màndarga bu leer buy wane ne daamaru saabalkat la. Kon, mbir mi teyeef la. Dafa di, ci bésub altine jooja ba tay, sóobarey Israayel reyaat nañu beneen saabalkat bu daan wuyoo ci turu Mohammad Mansour, daan liggéeyal benn tele gox ba. Moom itam, ab bomb lañu ko dóor fa dëkk bii di Khan Younès.

Bees sukkandikoo ci waa RSF, 200i saabalkat lañu rey ci diirub 15i weer kese. Muy lu raglu. Nde, bu xare amaan, kenn du laal saabalkat yi ak xale yi. Waaye, réewum Israayel moom, sàrt yépp lay joggi, faalewul kenn, lu ko neex def, àddina sépp di ko seetaan muy jeexal Julliti Palestin yi. Te, ku ci wax, bu la njiiti Israayel yi mënul a noppiloo, dañu lay reylu. Moo tax, bépp saabalkat bu jóg ngir siiwal lay ame fa Gaza, biral faagaagal ba fa xew, ñu sàkkal la pexe. Loolu nag, ci gis-gisu RSF, dafay gàntal ak a neenal sañ-sañu xam ak xamle. Maanaam, dafay tere saabalakt yi seen sañ-sañu saabal i dég-dég ak di tere nit ñi jot ci dég-dég yooyu. “Bu kenn xippi, bu kenn wax, bu kenn àtte, bu kenn sotal Palestin”, bataaxel boobu la Israayel bëgg a jàllale.

Diggante 2023 ak tay nag, RSF jot na jébbal ñeenti jure (pelent) ëttu àttewaay bu àddina sépp bii di Cour Pénal International (CPI). Li muy toppe waa Israayel mooy pekkey xare (crimes de guerre) ñeel i saabalkat. Ci diir bu gàtt bi ñu dakkaloon xare bi sax, diggante 19 sãwiyee ak 18 màrs 2025, Israayel dañu tere woon saabalkat yi dugg fa Gaza ngir def seen liggéey.

Boo déggee waa Israayel yi bóom Hossam Shabat, moomii saabalkat bi, ci Hamas la bokkoon. Dafa di, saa bu Israayel bëggee rey ab saabalkat, tuuma jooju lay teg ci kawam. Te, du ci indi lenn firnde. Te sax, bu loolu amoon, du ko tax a am sañ-sañu rey i saabalkat.

RSF a ngi woo njiiti àddina sépp ngir ñu takkal Israayel pot, topp ko ngir mu dakkal fitna yi muy fitnaal Julliti Palestin ñi. Waaye de, njorteesul woote boobu toq ciy nopp yuy dégg. Ndaxte, àddina sépp a ngi gis nit Israayel di reyee xeetub lëmm. Ñi ci mën dara ñépp ñu ngi ne tekk-tekkaaral, ne yugg-yuggaaral, di seetaan ñuy faagaagal seen i moroomi nit ci tooñaange ak nootaange.

Jullit ñeet, kenn rawu leen. Naka la ay miliyaari jullit mënee bank seen i loxo, di seetaan as mbooloom yawuut mu néew di rey ak a jeexal seen i moroomi jullit ?

Israayel dafa fétteerlu, bew, jàpp ne lu ko neex def. Ndimbal li Etaasini di dimbali ak naaféq giy màndargaal njiiti réewi sowu yi bokk na ci li may fit Israayel ba lu ko neex def. Li ci gën a doy waar mooy ne, fa réewum Sisordani sax, ku yékkati sa baat ngir seede, sóobarey Israayeel yi dañu lay xoqatal, fitnaal la, tifaare la, teg sa kaw lu metti. Ca altiney barki-démb ja ba tay, sóobarey Israayel yi jàppoon nañu saa-palestin bii di Hamdan Ballal, di kenn ci ñi defar film-dokimànteer bees duppee Other Land. Laata ñu koy jàpp nag, ay way-mbéeféer songoon nañu këram, sotoo ko, dóor koy dóor yu metti lool sax. Ci àllarbay tay ji lañu ko bàyyi ginnaaw bi ñu téyee guddi gépp.

Bu wax jotee, ku noppi doo gor.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj