Na woon, fa woon

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci bëccëgu altiney ji, 12 ut 2022, la Senegaal doon taxawal 14eelu ngombalaanam (péncum ndawi réew mi). Nde, ginnaaw biñ leen falee, démb lañu waroon a door seen liggéey, falaale pekkug Ngomblaan gi ak ki ko war a jiite.  Ñeenti lawax ñoo doon sàkku njiiteefu Ngomblaan gi : Aamadu Maam Jóob (Bennoo Bokk Yaakaar), Ahmet Aydara (Yewwi Askan Wi), Baartelemi Toy Jaas (Yewwi Askan Wi) ak Lamin Caam (Wallu Senegaal). Bari woon na coow lool, nag. 

Xëccoo bi diggante dépitey BBY ak yu kujje gi metti woon na ba, daanaka, jot nañ fa xeex ak a sàndante ay butéeli ndox. Palug Njiit li war a jiite Ngomblaan gee  waraloon jóoke bu bir boobule. Ndaxte, kujje gi dafa lànkoon ne, wote du am fileek sàmmontewuñu ak yoon. Ci seen i wax, yenn ciy jëwriñ yees fal dépite, muy Abdulaay Daawda Jàllo, Mariyaama Saar ak Abdulaay Séydu Sow, waruñu wote. Waaye, waa BBY, ñoom, dañu wax ne yoon terewul jëwriñ yooyile bokk ci wotey palug Njiitu Ngomblaan gi. Ñaareelu sabab bi waraloon xuloo bi mooy mbirum bilteŋi wote yi. Kujje gi ne, am nay depite yu jàngul. Kon, dañ war a fexe ba wirgoy bilteŋ yi wute ngir  mu leer, jaawale walla njuumte bañ a am. Waaye, daluñu ci. Ndege, caytug Ngomblaan gi daf leen ko gàntal. Xol yi jóg, werante bi ne kur, Pénc mel ni tulleek maale.  Ndaw gàcce ! Sàndarm yi lañ mujje woo ngir wote am.  Waaye, dépitey kujje gi dañu gedd. Gii Maris Saañaa dem na ba ci mbañ-gàcce bi, xotti ãwalobam, fob ko ne daf koy yóbb, sàndarm yi sëkkatoo ko, nangu ko

Noonu, bi ñu yullee li ci mbañ-gàcce bi, 84i dépite ñoo wote, 83 yi tànn Aamadu Maam Jóob mu BBY, def ko Njiitalu Ngombalaan gi. Kenn ki dafa gàntu. Waaye, dafa mel ni mbir du fi yem.

Dees na ko topp…

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj