ÑAARI BAKKAN ROT NAÑ XAAT

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bakkan rot na fa jànguneb Ndar ba (Iniwérsite Gastoŋ Berse). Taskatu xibaar bii di Ilan Gabet a ko siiwal ci xëtu X (Twitter ba woon). Mi ngi jëlee xibaar bi ci Alimatu Kan.

Nee ñu yit, kii di Maam Góorgi Njaay, di woon mbër, ñàkk na bakkanam. Ci li njabootam xamle, gërënaad lakkirimosen yi ñoo ko jekkali. Ndax, ci seen i wax, dafa feebaroon bu yàgg, waaye gaas lakkirimosen yi mo noyyi ñoo ko fatt ba mu génn ci àddina.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj