ÑAAW NA BA NOPPI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Paap Aliyun Saar a doon dalal Bubakar Bóris Jóob ca ITV. Tolluwaayu réew mi ci wàllu pólitig lañ doon fénc. Jamono yii nag, réew mi dafa toog ci nen. Layoob Usmaan Sonko ak Aji Saar, walla moom ak Maam Mbay Ñaŋ, muy mbirum ñetteelu moome gi, di jafe-jafey dund bi walla sax buumu njaam gi dox sunu digganteek nootkat bii di Farãs ba léegi, ñooy sabab yëngu-yëngu yi ci réew mi. Moo tax ndaw ñiy génn ci mbedd yi, di ñaxtook a xeex ak takk-der yi. Saa bu ndaw yi yëngalee nag, jàmm du am. Dañuy taal ak a yàqate, kenn du dem, kenn du dikk.
Bóris ne, ndaw ñi, « …kenn mënu leen a téye… Duñu déglu rajo. Duñu seetaan tele te dañu gis seen bopp bu baax a baax ci kàdduy Sonko yi. » Te, ku laal Sonko, seen yaakaar, lañuy bañ. Ndaxte, jamonoy tey, mënees na jàpp ne Usmaan Sonko mooy pólitiseŋ bu gën a siiw ci Senegaal. Moo tax Bubakar Bóris Jóob wax ne : « Fi Usmaan Sonko àgg ci xoli saa-Senegaal yi, kenn mësu fa àgg bi Senegaal dee Senegaal ba tey. Fekke naa jamonoy Ablaay Wàdd, Abdulaay Li ak ñeneen. Ñu siiwoon lool lañu, waaye… »
Ba ci Maki Sàll mi jiite réew mi sax, bindkat bi jàpp na ni Usmaan Sonkoo ko raw ci fuuf ci siiwaay. Dafa di sax, ci gis-gisu Bóris mi woon taskatu xibaar, Maki Sàll dafa neexatul doomi réew mi. Sonko moo dee ci xol yi. Loolu, nag, ci waxi Bóris, lees singali njiitul Pastef lee ko waral. Dem na ba Njiitu réew mi di doxantu-doxantulu ngir wane ni nit ñi bañu ñu ko. Waaye, boroom EJO ak Lu Defu Waxu dafa gis ne, loolu dafa mujje ruslu ci njiitum réew.
Li gënatee ruslu mooy bu njiitum réew demee ba àddina sépp weddi ko, di ko joqarbi ak a yedd ngir mu dellu ginnaaw. Looloo dal Njiitu réew mi, Maki Sàll. Ndax, Bubakar Bóris Jóob, Faatu Sow, Sofi Besis, Mamadu Juuf ak yeneen téeméeri téeméeri xeltukat biir Senegaal, Afrig, Etaasini, Farãs, Kanadaa, añs., defar nañu ag mbaaw jagleel ko Njiitu réew mi, Maki Sàll.

Bu bët setee, ku ñaaw rus

Njiitum réewum Senegaal de, woyam ñaaw na ba noppi. Àddina saa ngi koy won ginnaaw. Nde, ay kàngaam yu bari ci àddina si, ñoo ngiy koy artu ak a dankaafu ñeel mbirum ñetteelu moome gi muy yóotu.
Mbaaw gi, bésub 21 màrs 2023 lees ko biraloon. « Salfaañe bi ñuy salfaañe àqi nit ñi ak ni ñuy wañaaree loxoy Yoon » moo soxal ñi ko sumb. Lu ëpp 100i xeltukat, fi Senegaal ak bitim-réew ñoo bokk defar mbaaw gi, di ci joxoñ Njiitu réewum Senegaal, Maki Sàll, artu ko, mu teg ci suuf yéeney ñetteelu moome gi nar a taal réew mi. Dees na ci fekk ay jàngalekat, taskati xibaar, mawaane, sosiyolog, ñi bokk ci mbootaayi tàggat-yaram yi, añs. Ñooñii ñooy joqarbi Maki Sàll, di ko wax mu delloosi xelam. Aamadu Tiijan Won, nekkoon fi jëwriñu mbatit gi te bokk ci ñi ko sumb, dafa jàpp ne Yoon dafa jeng ci Nguur gi koy defloo, di ko dindiloo. Moom, dafa gis ne Maki Sàll moo yor doole ji, yor sañ-sañ bi, kon moo war a fexe jàmm am. Maki Sàll dafa dige woon coppite, waxoon ne mbirum ñetteelu moome jeex na ci réew mi… Mu wax ko, baamu ko ay yooni yoon. Tey, mu bëgg soppi jikko. Ndekete, Maki Sàll daf nu nëbboon boppam. Waaye, nag, bët set na.
Wole Soyiŋkaa sax, torlu na mbaaw gi. Saa-Niseryaa bi, moom, boroom tur wu siiw a siiw la, ñu xam ko fépp ci àddina si, niki Bubakar Bóris Jóob, doomu réew mi, ak sax ñépp ñi sumb mbaaw gi. Wole Soyiŋkaa, bindkat la bob, jot na fee jël cargalug Nobel ci wàllu ladab (prix Nobel de la littérature) ca atum 1986.
Wole Soyiŋka nag, bokkul woon ci ñi ko sumb. Ci ginnaaw la fësal yéeneem bokk ci mbaaw gile. Loolu la kenn ci ñi sumb mbaaw gi di leeral :
« Ci tukki la nekk, moo tax jotul woon mbaaw gi ca jamonoom. Te, démb rekk la ci jot, daldi koy jàng. Ca saa sa la wax ñu boole ko ci way-torluy mbaaw gi. »
Mbir maa ngoog. Waxi ñetteelu moome gaa ngi bëgg a yàq deru Senegaal. Wax-waxeet bi Njiitu réew mi nar a def gàkkal na deram, ñaawal turam ci àddina si. Li mu namm a faagaagal Usmaan Sonko yit, tax na ba njiitul Pastef li raw ko ci xoli nit ñi. Nde, moom Maki Sàll, daf ni woon day seeyal kujje gi. Waaye, nag, mel na ni moo nar a seey. Nde, yéene néeg la, boroom a cay fanaan. Te, ku añaane say dono, sa deewin ñaaw.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj