‘’ÑAAWTEEF YIY XEW TEY RÉEWUM SIIN DU GULÉET…’’

Yeneen i xët

Aji bind ji

(SÉEX MBÀKKE AMAAR, JËWRIÑUNDONGOY-DAARA SENEGAAL YA CAWUHAN. CI TAATAANUG NDEY KODDU FAAL)

Ndey Koddu Faal : Sëriñ Séex Mbàkke AMAAR, maa ngi lay nuyu ci turu Lu Defu Waxu, di ab yéenekaay ci kàllaamay KoccBarma fii ci Senegaal.

Ginnaaw bi nu la gërëme ci li nga nu nangul waxtaan wii, ma bëggoon laa bàyyi  nga wax ñiy jàng yéenekaay bi yow yaay kan, laata nuy sóobu ci laaj ak tont.

Séex Mbàkke AMAAR : Maa ngi tudd Séex Mbàkke AMAAR, di doomu-Senegaal, am 30i at. Maa ngi jàng fii ci réewum Siin, ci dëkk bu ñu naan Wuhan. Maa fiy jëwriñu ndongo-daaray Senegaal yi.

NKF: Ndax mën nga noo wax ñaata at nga fa defagum ak tamit lan nga fay jàng...

SMA : Atum 2017 ba léegi maa ngi  fiy jàng waaye nag du guléet ma ñëw ci réew mi. Maa ngi bindu ci daara ju mag ji tudd ‘’Central China Normal University’’. Fi mu ne nii tollu naa ci PHD, di gëstu ci jëflante diggante Senegaal ak Siin (histoire des relations diplomatiques sino-sénégalaises).

NKF : Feebaru Covid-19 bi lëmbe àddina sépp bi muy door a feeñ Siin, ñu bari dañoo yaakaaroon ni fa lay yem, feebaruSinwaa la…en doomi-Senegaal yi nekk Siin tamit bëggoon ngeen a ñibbisi, Njiitu-réew mi Maki Sàll ne loolu mënul a nekk ndax Senegaal amul pexe yu mu leenindee. Kàddu yooyu juroon coow lu réy. Naka ngeen ko dunde woon ?

SMA :  Feebaru koronaawiris nag, nuy fàttali rekk ni mën naa dal ku nekk, loo mënti doon, ak koo mënti doon. Waaw, bi muy door a feeñ fii ci Siin, nguur gi danoo bind ay bataaxal ne ku ci nekk na jokkookkilifay réewam ngir ñu jëlsi la nga ñibbi sa dëkk, ndax ñoom rekk ñoo mën a dogal loolu. Ci kow loolu, nun it nu tàmbalee def lépp li nu war ngir mën a ñibbi. Ñaanoon ñu jële nu fii ba jëmmi jamono… Xey bés rekk , ni ko ñépp déggee, njiitu Senegaal wax ni Senegaal amul ay jumtukaay yu mu mën a jële ji ay doomam ci Siin. Juroon na naqar, njàqare ak tiitaange. Kàddu la yu indi woonjiixi-jaaxa te du ay kàddu yu neex a fàtte, rawatina waxin wu jekkul wi ak ni nu ko dégge woon.

Waaye nag, nu jëloon lépp delloo ko ci loxo Yàlla, jàppe ko rekk  dogal, xam ne su waree jeex, dina jeex. Nu ngi sant bu baax.

Ba tey jii nag, nun xamunu lu tax ñu bàyyi nu fi ca jamono jooja. Déedéet.

NKF : Ni nga ko waxe, waxin dafa am solo te ku nekk ci tiis, boo ko mënul a dimbali yit, am na noo xam ni boo ko waxeek moom dinga dalal xelam. Dëgg la kàdduy Maki Sàll yi indi woon nañ njàqare gu réy ci waay-juri ñi nekk foofu ak it képp kuy doomu-Senegaal. Léegi nag Covid 19 yegsi  na Senegaal, laal lu ëpp ñetti téeméeri doom-aadama. Lu Defu Waxu doon laaj ndax tey jii su ngeen ñibbisi woon, dungeen ko réccu ?

SMA : Dëgg la, koronaawiris dugg na Senegaal, te ma nga fay am i tànk. Xanaa di ñaanal Senegaal ak àddina sépp tey ñaax doomi-Senegaal yi ma ko sañ a wax ngir ñu gën a farlu ci ndigël yiy doktoor yi joxe ngir mën a mucc ci feebar bi, wàññi laamisoo tegën a bàyyi xel ci cet gi.

Ci sa laaj bi nag, su dee dëgg a neex Yàlla amunu dara lu nuy réccu. Déedéet. Ndax lu ma mënti am, sama réew moo ma ko gënal. Ba nuy sàkku ci nguuru Senegaal mu jëlsi nu, xamoon nanu bu baax ni dara jotu nu. Te sax su doon damaa am feebar bi walla ma war a faatu, faatoo sama dëkk ci samay mbokk moo ma gënal faatoo ci àll bi. Feebar bi it, su ma ko amoon, duma ñëw Senegaal di ko fa wàll kenn, damay faju ba noppi door a def lu may def, damay jàpp ni rekk ab soldaar laa bu dem xare. Senegaal, samay mbokk a fa nekk te ñoom ñépp jàmm rekk laa leen yéene.

NKF : Wax nga dëgg, ndax niñ lay xoole sa réew ak réewum jaambur du benn. Loolu leer na. Laaj bi ma la laaj, xey-na déggeewoo fi may waxe : jamono ji ngeenbëggoon a ñibbisi, koronaawiris daa amoon Siin te amul woon Senegaal. Léegi laal na lu ëpp ñetti téeméer ci Senegaal te mu ngi wéy di law. Kenn umplewul ni pexe yi Siin am, Senegaal amu ko. Ma doon la laaj tey jii nga xam ni feebar baa ngi ci sunu réew mi, ndax su ngeen ñibbisiwoon du leen jural réccu ?

SMA : Maa ngi door a xam fi ngay waxe waaye awma benn réccu, donte Siin moo ëpp fuuf Senegaal doole. Su ma ñëwoon Senegaal yit damay sóobu ci liggéey bi rekk ngir lu jëmale sama réew kanam. Man noonu laa gise mbir mi, te loolu moo ma yitteel.

NKF : Waaw, dëkku jaambur moom loo fa mën a tekki it doxandéem nga fay doon.Kon li am solo mooy, ni ko Séex Anta Jóob wonee, boo jàngee li nga war a jàng ba noppi, nga dellu sa réew, amal leen njariñ. Di la ndokkeel ci loolu.

Biy koronaawiris door a am Siin, yéen ñi mu dalul, dañ leen a beroon ngir aar leen. Nu doon laaj naka la gaw (confinement) boobu deme. Naka ngeen koy dunde ?

SMA : Feebar bi nu ngi koy dund ak ngor ak jikkoy nit  ñu am diine. Te gaw bi moo nuyaar, mooy sunu kaaraange. Ba fi Covid-19 bi duggee ba sunujonn-Yàllay-tey jii, nu ngi ci ber googu, sa néeg ngay nekk, doo génn ludul yéeg geg (escalier) ñu jël sa tàngaayu yaram nga daldi wàcc. Sunu dundin soppiku na bu baax a baax.

NKF : Ginnaaw gaw ngeen nekk, njàng mi nu muy deme ? Seen lekk it nu muy deme ?

SMB : Man samam njàng, ci gëstu la tollu, maa ngi ci. Ñeneen ñi njàngum-soreyoo lañuy xal a def ak seeniy sëriñ. Loolu door na. Fii, KENN DU GÉNN.

Ci wàllu lekk gi, dëkkuwaay bu nekk ak nimuy doxale. Man fi ma nekk nii, nun ñépp ay gan lanu fi waaye man rekk maa fiy doomu-Senegaal. Sunu yeneeni mbokk yaa ngi ci yeneen dëkkuwaay yi. Am na ñoo xam ni ci seen biir dëkkuwaay lañul jël benn néeg jagleel ko njënd meek njaay mi ñeel liñuy dunde. Kilifa yi tamit dinan ci jàpp. Man nag fi ma féete, mën nga woote wax li nga soxla, bu dibéeree ñu indil la ko nga fey. Noonu daal lan koy defe. Xamoon nanu ni ci gaw la yëf yiy mujje ba taxoon na nu fagaru.

NKF : Dangeen di ay doomi-Senegaal yu nekk ci réew mu am feebar bu doy waar, Lu Defu Waxu bëggoon a xam ndax gornmaa Senegaal mi ngi leen di jàppale. Su dee lu am la, wan xeetu ndimbal la ?

SMA : Ambàsadëer bi mi ngi Beijing, tedaanaka bés bu ne dina nu laaj sunu jàmmi yaram. Yenn saa yit dinaay jokkook yenn kilifay Senegaal nu weccee xibaar, ñu nuy nemmeeku. Bi feebar biy door a song Siintamit, bi Maki Sàll nee mënu noo dimbali nu ñibbi, yónnee na nu koppar. Waaye ca la yem. Boobaak tey daal amaatul benn jéegobu nguur gi def.

NKF : Ñu baree ngi tuumaal Sinwaa yi fan yii, naan dañuy bunduxutaal ak a toroxal nit ñu ñuul ñi. Ndax ni ñu koy waxe la deme ? Ndax foofa ca Siin daa am ay doomi-Senegaal yu ay Sinwaa takk di leen diri ci mbedd yi ? Ndax Sinwaa yi dañoo jàpp ni doomi-Afrig ya fa nekk ñooy lawal doomu-jàngoro bu Covid-19 ?

SMA : Waaw, ni ngeen ko gise ci widéwoo yi, lu ñuy dund la fii ci Siin te ñépp di ko naqarlu. Ñu ngi koy naqarlu ba fu naqar yem. Guanzu la doomi-Afrig yi ëppe, foofa la mbir yi gën a takkarnaasee. Su nu sañoon nag, sunuy gornmaa jóg ci lii, won seen i naataangoy Siin fullaak faayda.

Am na lu ma bëgg a wax fii, foo tollu dégg ñu naan doomi-Afrig, doomi-Afrig… Xey-na su nu booloo woon, dinan gën a am doole waaye ku ci nekk ak sa yoonu boop la, ndax bokkunu gis-gis, danoo féewaloo te loolu dafa néewal sunu doole.

Am na leneen lu am solo lool te ñu koy faral di fàtte, mooy maanaam jël benn dëkk kepp di ko tëkkaleek Afrig yépp, ak ni mu tollu.Jaaduwul ñuy wax : ci misaal, Siin ak Afrig. Liy yoon mooy Siin ak Senegaal, Siin ak Niseryaa añs ; walla boog nañ ni : Aasi ak Afrig.

War nanoo xoolaat sunu bopp, Afrig warta nekk mbaamu kenn ba ku jóg ndulli ko ba sa xol sedd, soo noppee aal sa moroom te dara du la ci fekk. Sunuy njiit am nañu ci wàll bu baax a baax. War nañoo fexe ba kenn du nu yab.

NKF : Ñaawteef yooyu ngeen di dund tey jii ca Siin, ndax ndongo-daara yi ci lañu bokk ?

SMA : Sinwaa yi fi mu ne nii doomu-Afrig lañuy bañ a gis, amul xàjj-ak-seen. Ñi ñuy toroxal am na ciy ndongoy-daara, ay jaaykat ak i liggéeykat. Ñoom daal, bàyyiwuñu kenn, soo ñuulee te nekk doomu-Afrig rekkñu dal sa kow.

NKF : Ci kow loolu, yéen ban taxawaay ngeen ci am ? Yan pexe ngeen lal ngir mucc ci lii ? ‘’Consul’’ ba fa nekkal nguuru Senegaal luy taxawaayam ci mbir mi ? Ndax jokkoo naak yéen ngir seet nu mu koy saafaraa ?

SMA : ‘’Consul’’ bi nag mësunu koo teg bët, mësunoo jokkook moom, man xaw ma sax turam. Dégg naa am na benn mbootaay moo xam ni Sëriñ Mbay miy toftalu njiit li mi ngici ak consul bi, ñooy liggéey ak sunu mbokk yi ñu j seen kër.

Bu loolu weesoo, nun ndongo yi nu ngi diisoo ci sunu biir ak itam yeneen doomi-Senegaal yi fi nekk ba ci sax yeneen doomi-Afrig yi ngir fexee dakkal nootaange bi. Jot nanoo jokkoo yit ak kilifay réew mi, weccook ñoom xalaat. Waaye ak lu mënti am, li am solo moo di ne luy jot jot na ginnaaw dee. Ñaawteef yi xew tey Siin, du guléet ndax dégg naa lu ni mel amoon na fi te mujjul fenn ci atum 2008 ; boobu nag fekkul ma nekk Siin. Yaakaar naa ni dina deme neneen bii yoon.

NKF : Ndax yéen doomi-Senegaal yiy jànge nii Siin, dangeen a am ndimbalu nguur gi walla yéen ay dundal seen bopp ?

SMA : Nekkin yi du benn. Am na ñu ci amndimbal, am na it ñoo xam ne ñooy dundal seen bopp, seen i waay-jur ñoo lee di yónnee xaalis, ñu ciy fey iniwérsite, di ci faj seen soxla.

NKF : Ba tey ci wàllu jóge Siin, ndax am na yeneen doomi-Afrig yu ngeen nekkaloon te ñooña ñibbi ?

SMA : Waa-waaw. Ci lu ma xam te mu leer ma nàññ, réew yépp jëlsi nañu seen i doommuy Móritani di, SudaN mbaa Alséri mbaa Marog walla Tinisi ak Afrig dii Siid.

NKF : Ndax yéen waa Senegaal ca Siin, jàppuleen ne seen réew da leen a won ginnaaw ?

SMA : Ca njalbéen ga, amoon na ñu mer ba futt, mbir mi bettoon na leen lool. Ku nekk ak ni nga ko dunde. Man ci sama wàllu bopp, am na lu ma yëgoon bi ma koy door a dégg waaye ak ndimbalu Yàlla gaaw naa ko génne sama xel. Kenn mënu maa teree doon doomu-Senegaal, moom laay xal di nekk te jàpp naa ne kenn ëppëlewu ma ci Senegaal.

NKF : Dangeen a nekk ci réewum jaambur, ñu dalal leen fa, réew mi am i jafe-jafe rekk ngeen bëgg a ñibbi. Ndax ci jamono jooju Sinwaa yi tamit jàppuñu ni dangeen leen a won ginnaaw ?

SMA : Xam nga, kilifay Siin yi ci seen bopp ñoo ni woon ku bëgg a dellu sa réew mënngaa dem. Am na sax ñu nu doon wax :buleen dem, toogleen fii te am kóolute ci nun. Waaye ñi lay wax loolu day fekk ngeen miinante, ñi ci des doo xam luy seeniy xalaat. Sinwaa nag, ku bëgg réewam la. Leer na ñépp.

NKF : Yaa ngi Siin at yi ñu weesu yépp, lan moo la fa gën a yéem ?

SMA : Li may jaaxal ci àddina bariwul ndax lépp lu ma gis damay jàpp ne sunu Boroom moo ko def. Siin nag, li ma fi gën a seetlumooy ni mu naate, ni biis yiy mel, ni tali yi yaatoo, ni dëkk bi sete, mbedd moo gis mu ni gàññ ak i defukaayu mbalit, yii daal saa su ma ko gise dama naan lii de, su ma ko mënoon a def Senegaal dina baax. Lu ma fi dul fàtte la, wax dëgg-Yàlla.

NKF : Yow mi  dëkk ci réew mi Covid-19njëkk feeñ te xam it ni waa Senegaal didunde, loo leen di digal ci wàllu fagaru ?

SMA : Nañu dunde ni ñu war a dunde ; Senegaal réewu diine la : muy jullit bi di katólig bi, ku ci nekk dangaa war a set, sell, bañ a taq ; te sax sëqat jëme ci nit ñi ak yu ni deme, diine tere na ko. Kon su nu dundeenoonu rekk mën nanoo mucc ci koronaawiris bi. Nañu jaayanteek suñu bopp tuuti rekk, mu jàll. Su ko defee li feebar bi bëgg du ko fi ame. Dëkk yi ko daan yépp amuñu garabam, noonu rekk lañ ci mucce, noonu lañ doge wàllent wi.

NKF : Loo bëggoon a tëje, yóbbante ko waa Senegaal ?

SMA : Xanaa di leen jaajëfal yéen waa Lu Defu Waxu ci liggéey bu rafet bi ngeen didef, te muy jëmale làmmiñi Senegaal yi kanam.

Bu loolu weesoo, nu ngi siyaar sunu waa-jur yi nga xam ni bés bu Yàlla sàkk ñu ngi ci kanam ci lépp. Nu ngi sant bu baax ñépp ñi nga xam ni ñu ngi nuy bàyyi xel, di nu ñaanal ci lu nu yëg ak lu nu yëgul.

Ginnaaw loolu tamit, feebaru Covid-19 bii am nanu ci jàngat bu mag ci sunu digganteek sunu réew, ak yeneeni réew ciàddina si ak it sunu digganteek sunu Boroom, nu war fee jóge gën a dellu ci Yàlla.

Kenn matalewul ku dul Yàlla waaye nu ngi ñaax sunuy kilifay réew ñu gën a farlu ci wàllum paj, defar ay lopitaan yu mucc ayib ndax sunu réew mi rafle na ay mask, aynoyyikaay  ak i lali lopitaan. Nanu farlu daal ci fànn yépp, ngir jëm kanam.

Yal na Yàlla musal ñépp, defal nu tawféex ak taysiir.

NKF : Sëriñ Séex Mbàkke Amaar, Lu Defu Waxoo ngi lay gërëm ci waxtaan wi, ci sa jot, ak ni nga nangoodd askanu Senegaal ci say xalaat. Jërëjëf.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj