Nees ko tàmm a defe, ayu-bés bu jot, amal nañu ndajem jëwriñ yi démb ci àllarba ji, 12i fani màrs 2025. Fa Njénde la lees ko amalee ci njiitalu Njiitu réew mi.
Ay njaal la Njiitu réew mi ubbee ay kàddoom, jagleel leen jëwriñu Koppar yi ak Njël li, ginnaaw faatug Abdu Juuf ma woon njiitul Njël li.
Mbirum jigéen ñi
Ginnaaw njaal yi, Njiitu réew mi àdduna ci bésub 8 màrs bees jagleeloon jigéen ñi. Ndokkeel na jëwriñu Njaboot gi ak Dimbalante gi ci xew ma mu amaloon ca « Grand Théâtre national », keroog 8i fani màrs 2025. Waayeet, sàkku na ci moom mu déglu njàmbati jigéen ñi, bu noppee daldi koy gaaral njàmbat yooyu ak pexe yees ci war a indi ngir ñoŋal nekkiinu jigéen ñi.
Raayaw « Médaille Gaïndé de la performance »
Njiitu réew mi xaatim na ab dekkare, jël ci ndogalu taxawal aw raaya ci wàllu xereñte, tuddee ko « Médaille Gaïndé de la performance ». Li mu ko dugge mooy sargalee ko saa-senegaal bu liggéey mbaa mu jëf jëf ju ràññiku juy jariñ réew mi te di fésal réewum Senegaal.
Caytug balluy mbindaare yi
Nguurug Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay gi dafa ittewoo lool mbirum balluy mbindaare yi ak nees leen di saytoo ba ñu jural askan wi njariñ yees ciy séentu. Loolu moo tax Njiitu réew mi fàttali yéeneem ci tëral aw doxalin wu mucc ayib ñeel kurél gii di « Comité national de l’Initiative pour la Transparence dans les Industries extractives (ITIE Sénégal) ». Te yit, dees na ko dooleel, jàppandalal ko jumtukaay ngir mu mën a matale sas bi ñu ko gàll.
Ngir jëmmal yéene jooju, Njiitu réew mi sàkku na ci jëwriñu Koppar yi ak Njël li, jëwriñu Yasara gi, Soroj bi ak Mbéll yi ak ci jëwriñu Kéew mi ak nosteg mbindaare mi, ñu jël mbooleem matuwaay yi war, ànd ko ITIE Sénégal, ngir taxaw ci sàrt yu bees yi ñu tëral ci ITIE 2023 te Senegaal war ko wéral fii ak weeru sulet 2025.
Mbirum suufus réew mi
Njiitu réew mi dafa bëgg a baral jéegoy liggéey bi ñeel bi naaluw « Sénégal 2050 », rawatina ndefar yi ñu bëgg a samp fi réew mi. Waayeet, Njiitu réew mi jël na ndogalu neenal séddoo bi amoon ci suufus réew mi, féete ci diiwaani Ndakaaru, Cees ak Ndar. Li ko sabab nag mooy ne, ci kàdduy Njiitu réew mi, daf ci amoon ay jalgati yu jéggi dayo. Looloo ko ci taxoon a santaane ay càmbar.
Kàdduy elimaanu jëwriñ yi
Bu dee elimaanu jëwriñ yi moom, Usmaan Sonko, dafa yégle ne Càmm gi tàmbali na jëfe digle yi bawoo ci caabalu gees jagleeloon suufus tefesi pénc mi.
Bu dee li ñeel tabaxi (lotissement) Ndakaaru yi, Cees ak Ndar, neenal nañ lépp ni ko caabal gi diglee. Rax-ci-dolli, dakkal nañu càkkuteefi suuf yi fileek ñuy tëral yoonuw fàkk bees waxtaane ba am cig dëppoo. Dees na wéyal itam liggéey yees dakkalandi woon ginnaaw bees defee li war, fekk ne DGSCOS amal na ay càmbar ci wàll wi.