NDAJEM JËWRIÑ YI (29/1/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Nees ko tàmm a defe ayu-bés bu nekk fa Njénde la, amal nañu ci àllarbay démb ji ndajem jëwriñ yi. Njiitu réew mi, Sëñ  Basiiru Jomaay Jaxaar Fay moo jiite ndaje ma.

Fànnu diine ji

Ci màggalug 145eelu Wooteb Seydinaa Limaamu Laay la Njiitu réew mi ubbee ay kàddoom. Xew-xew boobu, lélub 30 ak 31i fani sãwiyee 2025 lees ko àppal. Ciy kàddoom, moom Njiitu réew mi ndokkeel na Xalifab laayeen yi, Seriñ Muhammadu Maxtaar Laay ak mbooleem taalibey laayeen yi. ginnaaw gi, jox na Càmm gi ay ndigal ngir ñu def seen kéemtalaayu kàttan, liggéey ak way-lootaabe yi ngir ñoŋal lépp lu jëm ci xew-xewu diine bi fépp fees koy amalee (Yoof, Kàmbereen, Ngor).

Njiitu réew mi laaxaale na ci Màggalug Poroxaan gi ñu war a amal keroog 6i fani féewiryee 2025. Yéeneem mooy fexe ba lépp lu aju ci xew-xew boobeet yemb, mu am ci jàmm ak salaam.

Ndog yi ci tali yi

Njiitu réew mi fésal na tiis gi mu ame ñeel ndog yi am ci tali yi ak ñi ci ñàkk seen i bakkan, rawatina ndog mi am ci talaatay barki-démb ji, 28i fani sãwiyee 2025 ci yoonuw Tuubaa wi (diggante Bàmbey-Xombol). Jci kaw loolu, jaale na njaboot yi ci faatule, daldi ñaanal way-loru yi ci jëley gaañu-gaañu wérug jàmm.

Fànnu dund gi

Njiitu réew mi àddu na ci dund gi ak njëg yees leen di jaayee. Li mu bëgg mooy Càmm gi fexee taxaw ci fuglu bu baax anam yi ñuy saytoo wàllu ndugg yi ak njëgi  dund gees di aajowoo bés bu nekk niki ceeb, suukar, diwlin, meew, sunguf (fëriñ), mburu añs. Jubluwaay bi mooy woyofal dund gi ci weeru koor gees dëgmal, muy koorug jullit ñi di koorug kercen yi.

Naka noonu, sàkku na ci jëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu gi mu taxaw ci jàmmaarloo ak ñiy denc walla ñuy yokk njëgi dund gi. Wax na ko yit mu jël mbooleem matuwaay ngir fexe ba dara bañ a ñàkk te njëg yi jàppandi ci kaw lees sàrtal. Rax-ci-dolli, xirtal na jëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu gi ak Fara-caytug Càmm gi yor wàllu PME / PMI ñu gën a dooleel « dunde lekku réew mi » te gën cee sóob ndefar yiy yëngu ci wàllu dund ak baral jéego yi jëm ci doxal sémb ak naali soppi liy ñoree ci réew mi.

Fànnu mbéll yi

 Askanuw Senegaal dafa war gis boppam ci liggéeyub balluy mbindaareem, rawatina ca gox ya ñuy ballee. Looloo tax Njiitu réew mi xamle ne Càmm gi dafa war a def yitte ci mbir mi, fobu ngir nekkiinu fere yiy yeewoo ci gox yi mbéll yi nekk. Naka noonu, sàkku naat ci jëwriñi mbéll yi, gox yi ak goxaan yi, koppar yi, koom-koom gi ak kéew mi ñu xayma, ci caytug elimaanu jëwriñ yi, njeexital yi jëfandikug mbéll yi am ci yokkuteg gox yooyee ci wàllu koom-koom, dundiin ak kéew mi. Xamle na ne jot na sëkk ñu leeral « Fonds d’Appui au Développement des Collectivités territoriales » ak koppar yi ñu jot a dugal ci ay jumtukaay yu ñeel askan wi niki ko « Code minier » bi diglee.

 Fànnu tàggat-yaram

Njiitu réew mi sàkku na ci jëwriñ ji yor wàllu tàggat-yaram mu woote waxtaan ak ñiy yëngu ci wàllu nawetaan ngir ñu tëral arminaat bu wóor ci joŋante yi. Te yit, warees na ci amal coppite te yokk kaaraange gi. Ndaxte, fan yii, fitna ji bari na ci nawetaan, te sax am na ku ci ñàkk bakkanam fa Yëmbël.

Naaluw « Agenda Sénégal 2050 »

Démb, ci ndajem jëwriñ yi, elimaanu jëwriñ yi xamal na ay naataangoomi jëwriñ ne ñu ngi wéyal liggéey bi ñeel jëmmalub « Agenda Sénégal 2050 ». Li ci jiitu mooy fésal limi sémb, naal ak coppite yi gën a jamp te ñu war leen a gaaral Njiitu réew mi gën-gaa yéex ci xaaju weeru féewiryee 2025 wii ngir mu dëggal leen.

Fànnu liggéey ak waa bitim-réew

Elimaanu jëwriñ yégle na tamit ne taxawal nañu ab digaale diggante Senegaal ak réewi « Proche » ak « Moyen Orient » ak li des ci kembaaru Asi. Démb lañu jël ndogal loolii ci cantaaneg Njiitu réew mi.

Digaale boobu mi aju ci ñaari téeméeri (200i) lëngoo walla sémbi lëngoo ci fànn yu wuute, ànd ko ak lu mat 15i réew ak kuréli kopparal. Ngir saytu liggéey bi, taxawalees na benn « task force » bu boole ay njëwriñ yu bari, boolewaale ci APIX ak FONSIS.

Fànnu wayndarey mboor yi

Elimaanu jëwriñ yi xamle na ne Càmm gi dina liggéey ngir sàmm wayndarey mboor yi (archives). Njëwriñ gi mu jiite ak banqaas yi mu yilif ñoo féetewoo liggéey boobu. Li ñu sasoo mooy liggéey ci waajulug ndenc gi (pré-archivage), ndenc gi (archivage), te dugal xaalis ci wàllu wayndarey mbooru réew mi (Archives nationales).

Rax-ci-dolli, dañoo nisër a tabax ag Kàggu gu méngook jamono, jagleel ko wayndarey mboor yi, ñu denc leen fa ci anam bu mucc ayib. Naka noonoot, dees na taxawal ag ndiisoog njëwriñal gog, dees na ci boole ay njëwriñ yu bari, ngir saytu denciinu wayndarey mboor yi. Ci kaw loolu, dees na tëggaat sàrt yi ñu tëral ci ñeel fànn wi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj