Démb ci àllarba ji, 5 màrs 2025, amal nañu ndajem jëwriñ mees di faral di amal ayu-bés bu nekk, fa Njénde la. Njiitu réew mi ak elimaanu jëwriñ yi biral nañuy kàddu ñeel xew-xewi jamono ji naali Càmm gi.
Bu dee kàdduy Njiitu réew mi, mënees na ko tënk ci ñeenti poñ yii toftalu :
Kooruy jullit ñi ak kercen yi
Mbirum diine yi la Njiitu réew mi ubbee ay kàddoom ca ndaje ma. Nde, àllarbay démb ji dafa yemoo ak lees duppee « mercredi des Cendres » [àllarbay Dóom yi], muy bés bi kercen yiy tàmbali seen ug koor. Lu ko jiitu, jullit ñi tàmbali nañu woor ca gaawu gee weesu, mu am ci ñu umoon ci dbéer ji. Kon, ren, koorug jullit ñi ak gog kercen yi dañoo yemoo ; maanaam, jullit ñi ak kercen yi ñoo woorandoo. Loolu nag, bees sukkandikoo ci kàdduy Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay mi jiite Senegaal, dafa « taaral bennoo ak jàmmoo giy màndargaal askanuw Senegaal. »
Déggoo diggante Càmm gi ak sàndikaa yyi
Njiitu réew mi àddu na ci ndaje mi amoon diggante Nguur gi, njaatigey liggéeykat yi ak sàndikaa yi. ndaje mooma nag, ca ayu-bés bee weesu la amoon. Moom, Njiitu réew mi, rafetlu na taxawaayu ñépp ñi bokkoon ca ndaje ma. Ndax, loolu dafa di lu am solo jëm ci xaatimub pasu déggoo guy sooke jàmm ak dal ci bérébi liggéey yi. Xaatimub pas googu, bésub 1eel ca weeru me wees dëgmal lees ko àppal. Pas googu nag, dina sóoraale tolluwaayu réew mi ci wàllu koppar.
ÀQI JIGÉEN ÑI
Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay sóobu na ci waajtaayu bésub 8 màrs bees jagleel jigéeni àddina sépp. Biral na ciy kàddu, wax ne : « [bés boobu] pose la ngir dëggal sunu yéene ci gën a dooleel àqi jigéen ñi, rawatina di leen gën a jàppale ak a gunge ci seen i sémb ci fànnu koom-koom. » Naka noonu, kilifag Njénde la xamle na ne, sémbuw àtte wees di waajalal jigéen ñi ngir ñu mënal seen bopp ci wàllu koom-koom, dina ëmb sàrt yuy dëgëral yéene jooju.
NAPPUG GAAL YI
Ci njeexitalu waxam, Njiitu réew mi wax na ci nappug gaal yi. Ci xalaatam, pàcc-pàcc bu am solo la ci koom-koomu réew mi, rawatina lu jëm ci sos ay liggéey ci dëkk bi ak jur xaalis ngir réew mi. Loolu moo tax mu jox ndigal elimaanu jëwriñ yi ak jëwriñu napp gi ñu amal ay waxtaan ak ñépp ñiy yëngu ci fànn wi. Jubluwaay bi mooy fexe ba nappug gaal yi amaat dayo bi mu amoon ci koom-koomu Senegaal.
KÀDDUY ELIMAANU JËWRIÑ YI
Bu dee elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, dafa dellusi ci ndaje ma ñu njëkkoon a amal diggante Nguur gi, sàndikaa yi ak njaatigey liggéeykat yi. Bees sukkandikoo ci yégle ba tukkee ca ndajem jëwriñ ya, elimaanu jëwriñ yi dafa xamle ne, ndaje mooma tax na ba ñu « dajale ñaxtuy liggéeykat yi. Te yit, Càmm gi jaare na ci leeral tolluwaayu réew mi ci wàllu koom-koom ak déggoo yi ñu nekk di liggéey. »