NDAJEM JËWRIÑ YI : ÑEENTI JIITUWAAYI NJIITU RÉEW MI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci àllarbay démb ji, 22i fani sãwiyee 2025, lees doon amal ñeentelu ndajem jëwriñ yi ci at mu bees mii. Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, moo jiite ndaje ma. Ca njeexital la, Aamadu Mustafaa Njekk Saare mi yor kàddug Càmm gi biral na ñeenti ndogal yi gën a fës ca ndaje ma.

Njiitu réew mi jël na ñeenti ndogal yi mu def ay jiituwaay.

Yeesalaat fànnu bokkeef gi

Njiitu réew mi dafa bëgg ñu yeesalaat caytug bokkeef gi, dëppale ko ak jamono. Nde, ci gis-gisam, caytu gu yees te xaralewu dafay ñoŋal liggéey bi, gën a amal njariñ askan wi.

Suqalig fànnu njàmbure gi

Suqalig fànnu njàmbure gi (secteur privé) tamit bokk na ci li itteel Njiitu réew mi. Moo ko tax a fàttali solos fànn wi ci joxe liggéey ak yokkuteg koom-koomu réew mi. Xamle na ne, Càmm gaa ngi liggéey ak boroom ndefar yi ak gawkat yi (investisseurs) ngir ñu lal naalu koom-koom wu dëppook tolluwaayu réew mi.

Njiitu réew mi yégle na tamit ne dees na amal ndajem waxtaan wu aju ci wëppa wii « Invest in Sénégal », maanaam « Gaw fi Senegaal ». Weeru awril 2025 lees ko jàpp. Lees ko dugge mooy wootal gawkati àddina si ak tamit fexe ba Senegaal nekk jubluwaay bi gawkat yi taamu.

Bees sukkandikoo ci yégle bi, 5 600i miliyaar lañu bëgg a dajale diggante 2025 ak 2029 ngir kopparal ay sémb yuy jeexital bu baax ci dundug saa-senegaal.

Yékkatiwaat fànnu wërteef wi ngir suqali ko

Njiitu réew mi teg na baaraamam tamit ci suqalig fànnu wërteef wi. Dafa di, moo Sëñ Basiiru Jomaay Fay, dafa jàppe fànn woowu ni pàcc bu am solo ci yokkuteg koom-koomu réew mi. Li mu ci nisër mooy jural askan wi lu tollu ci 500 000iy liggéey fii ak 2050.

Ngir loolu mën a àntu, dafa fas yéene jël ay ndogal yu bari yu deme ni fullaal mbindaare ak mbatiitu réew mi, suuxat bérébi wërteef yi ngir wootal wëraakoni doxandéem, beral wërteef gi ay takk-der yi koy féetewoo ngir yokk kaaraange gi ci béréb yooyii. Naka noonu, dees na amal am ndajem waxtaan muy boole njëwriñ yu bari. Jubluwaayu ndaje mooma ñuy amali mooy teg jéego yu njëkk ci wàll wi.

Yeesal ja yi ak bérébi yaxantu yi

Ñeenteelu jiituwaay bi mooy fexe ba lijjanti jafe-jafe yiy gàllankoor ja yi ak bérébi yaxantu yi. Jafe-jafe yooyu, ñi ngi dellu ci lakk yiy faral di ci am ak ñàkk kaaraange gi. Ngir indi ci ay saafara, joxe na santaane ngir ñu amal caytu gu xóot ci naal wees duppee « Programme de modernisation des marchés », ci Naaluw yeesal ja yi. Li mu ci bëgg mooy ñuy yokk kaaraange gi te yeesal béréb yooyii nga xam ne, dañu bokk ci liy doxal koom-koomi gox ya ñu nekk.

Ba tay ci fànn woowu, Càmm gi dafa bëgg yeesal Centre des Eexpositions de Diamniadio ak CICES ngir ñu gën a mën a dox, gën a mën a jur xaalis.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj