NDAJEM NDEYU ÀTTE MI NEENAL NA DEKKARE NJIITU RÉEW MI !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ndajem Ndeyu àtte mi àtte na ! Juróom-ñaari kàngaami àttekat yi neenal nañ dekkare bi NJiitu réew torlu woon, daldi fomm wotey 25 féewiryee 2024 yi. ci

Ci dogu ñaareel bi, dañ ci bind ne, sémbub àtte bi Ngomblaan gi wote keroog bésub 5 féewiryee 2024 dafa safaanoo ak Ndeyu sàrti réew mi.

Ci dogu ñetteel bi, ñu bind ne, dekkareb 2024-106 bu 3 féewiryee 2024 bi Njiitu réew mi jëloon, far nañ ko, maanaam daal neenal nañ ko.

Waaye nag, loolu du tax wote yi am ci bés biñ ko jàppoon, maanaam bésub 25 féewiryee 2024. Ndaxte, ci ndogalam li, Ndajem Ndeyu àtte réew mi daf ci leeral ni mëneesatul a amal wote yi dibéer joojee. Li ko waral mooy dekkare bi Njiitu réew mi jëloon. Loolu nag, terewul ne ay wote dinañ am balaa bésub 2 awril 2024 bi Njiitu réew mi war a dem.

 Noo ngi xaarandi faramfàcce boroomi xam-xam yu seen i xel màcc ci wàll Yoon indi ciy leeral. Ànd ak loolu yépp, ndogal lii, ndam lu réy la ci askan week kujje gi.

Li des nag mooy xool lan mooy doon taxawaayu Njiitu réew mi, Maki Sàll. Ndax dina ko nangu am déet ? Ndax day tekki ndombog-tànkam walla day wéyal ba keroog 2 awril 2024 mu joxe lenge yiñ ko dénkoon kif alu ?

Li ci kanam rawul i bët

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj