NDAJEM NDEYU ÀTTE RÉEW MI : GEG NAÑ USMAAN SONKO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tey ci àjjuma ji la ndajem ndeyu àtte réew mi warron a jeexal caytug baayaley lawax yiy sàkkoo bokk ci joŋantey wote 2024 yi. Ki ñépp doon xaarandi nag mooy Usmaan Sonko, njiitul kujje gi. Waaye, mbetteel amu ci. Nde, ndajem ndeyu àtte mi daf ko geg. Maanaam, daf ko gàntal. Li àttekat yi lay mooy ne, moom Usmaan Sonko, wayndareem matul. Ndax, ci seen i wax, meeru Sigicoor bi ci kaso bi joxewul këyit giy firndeel ni fay na warloom (Attestation).

Niki démb sax la ëttub àtte bu kowe doon àttewaat daan bees ko daanoon ca àtteb dabantal ba ñeel layoom ak Maam Mbay Ñaŋ. Ëtt bu kowe dafa mujje dëggal daan bees daanoon Usmaan Sonko. Waaye nag, ba tey, loolu mënul woon tere Usmaan Sonko bokk ci wote yi. Moo taxoon way-soppeem yeek farandoom yi amoon yaakaar.

Tey nag, àttekati ndajem ndeyu àtte mi saytu nañuy baayaleem, daldi koy téye, tere ko bokk. Nee ñu, wayndareem matul. Ndax, ci seen i wax, meeru Sigicoor bi ci kaso bi joxewul këyit giy firndeel ni fay na warloom (Attestation). Layookatu Usmaan Sonko bi nag, Me Sire Keledoor Li, dafa ñaawlu ndogal loolu. Ndax, ciy waxam, ba ñuy tijji wayndarew Usmaan Sonko, moom miy ndawam nekku fa woon. Maanaam, ci ginnaawam lañu ko ubbee wayndarew Usmaan Sonko, saytu ko ci teewadeem. Rax-ci-dolli, waxuñu ko sax gan këyit la indiwul. Fi mu nekk nii, Usmaan Sonko du bokk ci wotey 2024 yi.

Wëliis Usmaan Sonko, Bugaan Géy Dani tamit jàllaul. Nde, dafa war a mottali 18.996i baayale. Moom, boroom Dmedia, 25. 235i baayale kese la baaxle.

Ci gàttal, 9i lawax yi ñoo jàllagum jamono jii ci baayale yi :

Buubakar Kamara, Séex Tiijaan Jéy, Décce Faal, Daawda Njaay, Abdu Karim Wàdd, Abiib Si, Xalifa Abaabakar Sàll, Anta Baabakar Ngom ak Aamadu Ba.

Lawax yi war a mottali yépp woolu nañu seen i ndaw tay bu 18i waxtu jotee ca màkkaanu ndajem ndeyu àtte réew mi. Ku ci nekk nag, dinga am 2i fan ngir mottali li nga dese.

Limub lawax yi war a mottali :

1 – Aliw Mammadu Ja (202 ca diiwaanu Njaaréem)

2 – Aali Nguy Njaay (1 009)

3 – Maalig Gàkku (3 449)

4 – Allaaji Mustafaa Juuf (3 791)

5 -Basiiru Jomaay Jaxaar Fay (4 219)

6 – Mammadu Lamin Jàllo (5 199)

7 – Idriisa Sekk (5 800)

8 – Muhammat Bun Abdalaa Jonn (7 817)

9 – Allaaji Mammadu Jaawo (11 953)

10 – Sëriñ Mbuub (13 000)

11 – Paab Jibriil Faal (13 000 ak 3i diiwaan)

12 – Sëriñ Géy Jóob (13 228 ak 2i diiwaan)

13 – Abdul Mbay (13 771)

14 – Allaaji Abdu Rahmaan Juuf (13 792)

15 – Ceerno Alasaan Sàll (13 465)

16 – Suleymaan Ndeene Njaay (18 669)

17 – Aminata Ture (18 980 ak 4i diiwaan)

18 – Bugaan Géy Dani (18 996)

19 – Aamadu Li (23 678)

20 – Róos Wardini (31 000)

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj