NDAJEM NDEYU SÀRTU RÉEW MI DËGGAL NA LAWAXUG SONKO AK BÀRTELEMI JAAS

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ndajem Ndeyu sàrtu réew mi àtte na. Ci guddig àjjuma ji la fésal ndogal li mu jël ñeel dabantal yees ko jébbaloon ngir gàntal lawaxuy Usmaan Sonko (PASTEF) ak Bàrtelemi Toy Jaas (Sàmm sa kàddu). Àttekat yu mag yi dañu dàq dabantal yooyii, daldi dëggal bokkug Usmaan Sonko ak Bàrtelemi Toy Jaas ci wotey dépite yi war a am, keroog 17i pani nowàmbar 2024.

Ci ndogal li mu jël, Ndajem Ndeyu sàrtu réew mi dafa nangoodi dabantal yi. Ci li mu laytaayoo nag, dafa fàttali ne, ci wàll wi, njëwriñu Wote yi kepp a am sañ-sañu jébbal Ndajem Ndeyu sàrtu réew mi càkkuteefu neenal ay lawax ci wotey dépite. Maanaam, bu amee ku warul a bokk ci wotey Ngomblaan gi, kenn kese a ko war a wax Ndajem Ndeyu sàrtu réew mi, muy jëwriñ ji ñu dénk lépp lu aju ci wote yi.

Cig pàttali, lëkkatoo Takku Wallu Senegaal, te mu ëmb làng yii di APR bu Maki Sàll, PDS bu Kariim Wàdd ak Rewmi [Réew mi] bu Idiriisa Sekk, moo bindoon Ndajem Ndeyu sàrtu réew mi ngir mu neenal lawaxu Usmaan Sonko, neenalaale toftaleg nasiyonaal bu PASTEF gi mu jiite, ñeel wotey 17i pani nowàmbar yii di ñëw.  Ñoom, dañu bëggoon àttekat yu mag yi wax ne, Usmaan Sonko mënul bokk, daldi koy seppi. Li ko waral nag, ci seen i wax, Usmaan Sonko dafa gàlloo ñaari daan ci mbirum Aji Saar ma ak mu Maam Mbay Ñaŋ ma. Waaye, seen pexe àntuwul. Nde, lawaxu Usmaan Sonko jàll na.

Yemu ca. Nde, Takku Wallu dafa sàkku woon tamit ci Ndajem Ndeyu sàrtu réew mu gàntal toftaleg wuutakon yi (liste des suppléants). Li tax ñu bëggoon loolu mooy ne, toftale googu, sàmmontewul ak yemoog góor-jigéen (parité). Seen càkkuteef googeet, gàntalees na leen ko. Ndaxte, Xadi Gay mi ñu doon wax ni góor la, DGE joxe na firnde liy wane ne jigéen dëggantaan la.

Naka noonoot, àttekat yu mag yi jàllale nañu lawaxu Bàrtelemi Toy Jaas mi nekk ci boppu toftaleg nasiyonaal bu lëkkatoo Sàmm Sa Kàddu. Waa And liggey sunu reew [Ànd liggéey sunu réew] (Alsr) ñoo bindoon Ndajem Ndeyu sàrtu réew mi ngir neenal lawaxu meeru Ndakaaru bi. Ndax, ci seen i wax, dañu daanoon Bàrtelemi Jaas ci mbirum Njaga Juuf ma woon. Waaye, ñoom itam, seen pexe sottiwul. Ndax, lawaxu Bàrtelemi Jaas jàll na.

Kon daal, wote yii, mbër yu mag yépp dinañ sëgg bëre : Usmaan Sonko, Maki Sàll, Aamadu Ba ak Bàrtelemi Jaas. Làmb jaa ngoog, ku mën sa moroom, duma. Askan waay àtte.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj