Ndajem ndeyu sàrtu réew mi neenal àtteb leeral (loi d’interprétation) bi Ngomblaan gi wote woon fan yee weesu ñeel àtteb mbaale (loi d’amnistie) bi Maki Sàll wotelu woon ca jamonoom. Li tax àttekat yu mag yi neenal àtteb Aamadu Ba mu PASTEF mooy ne, ci li ñu fésal, njëlbeenub dogu àtte 08/2025 bi dëppoowul ak Yoon.
Keroog, 2eelu fanu awril 2025 la Ngombaan wote woon àtteb leeral bi ñeel àtteb mbaale ga woon. Jubluwaayu àtte boobu, ni ko tur wi di junje, mooy leeral ak a yemale njeexitali àtteb mbaale ga Maki Sàll wotelu woon, fexe ba ñu àtte képp ku laale woon ci ay pekke yu deme ni rey nit, fitnaalaate ak yu ni mel.
Kujje gi moo bindoon Ndajem ndeyu sàrtu réew mi ngir mu àddu ci àtteb leeral boobii nu tudd ci kaw, ngir mu xool ndax méngoo na ndeyu sàrtu réew mi. Ci kaw loolu la ko àttekat yu mag yi saytu, gis ne, dog bu njëkk bi ci àtte boobu sàmmontewul ak li ndeyu sàrtu réew mi tëral.
Ci àllarbay tay jii la ndogal li jib. Àttekat yi jël ndogal li ñooy : Majeŋ Arsinaat Li Njaay Tof-njiit li jiite jamono jii Ndajem ndeyu sàrtu réew mi ak way-bokk yii di Yuusufa Jaw Mbóoj, Awa Jéy, Séex Njaay ak Séex Ahmet Tiijaan Kulibali.
Ndogal lii nag, tekkiwul ne kenn du mën a topp ñi reyaate ak ñi leen ko digal, ñi doon fitnaalaate ak xoqatal nit ñi diggante féewiryee 2021 jàpp màrs 2024. Nde, ci li àttekat yu mag yi biral, pekke yooyii, kenn mënu leen a baale ndax Senegaal dafa xaatim ay àtte yu tënk àddina sépp, te sut sàrti réew mi. Ngir topp ñi def ñaawteef yooyu, bat ay ci li àttekat yi bind, jarul ñuy neenal walla di leeral àtte mbaale gi, ndax mënul làq kenn.
Bu loolu yépp weesoo nag, mënees na wax ne kujje gi am na ndam ci kaw Nguur gi. Leneen lees mën a jàngatee mooy ne, àttekat yi kenn tënku leen di leen wax lu ñuy def walla lu ñu dul def. Maanaam, ndogal li dafay firndeelne Yoon dafa tëdde njaaxaanaay, n muy lu ñépp di rafetlu, di ko taggee Senegaal. Li ci des nag mooy xool naka la Toppekatu Bokkeef gi di taxawee ak fu Yoon di mujj ci mbirum ñooñee ñu faatoon ca jamonoy yëngu-yëngu ya amoon diggante féewiryee 2021 jàpp màrs 2024.