Alxames, 8i fan ci desàmbar 2022. 15i waxtoo jot ci ginnaaw njolloor. Ñi ëpp ci àddina si, rawatina biir kembaarug Afrig, jenn itte lañu am, mooy xew-xew ba ca Qataar. Ñépp janook seen i tele, di seetaan ak a werante. Marog a war wureek Portigaal ci kuppeg àddina siy ame Qataar ci jamono jii. Joŋante bi nag, dóor mu toog la ; ékib bu jël ndam li daldi jàll ca démi-finaal ya. Maanaam, dinga bokk ci ñeenti ékib yiy desandi, war a xëccoo raw-gàddu gi. Marog nag, mooy ñeenteelu réewum kembaaru Afrig muy àgg ci dayob kaar-dë-finaal ginnaaw Kamerun (1990), Senegaal (2002) ak Gana (2010). Waaye, ba bi Marog di wureek Portigaal, amutoon menn réewmu Afrig mu mës a romb dayob kaar-dë-finaal ñeel kuppeg àddina si. Marog daan Portigaal, jàll démi-finaal.
Fépp fo demaan, keroog, bët yaa ngi ne jàkk tele yi, nopp yiy déglu baatu saabalkat biy faramfàcce joŋante bi ci rajo bi, xel yiy nos ak nocci ñeel mujjug joŋante bi, xol yiy tëf-tëfi. Nde, Senegaal toog na ca wicceem ya, Kamerun, Tinisi ak Gana, ñoom, lajj nañ bu yàgg, génnuñu sax seen i kippu. Marog kesee des, teewal fa Afrig, war koo siggil. Kon, du woon joŋanteb neen.
Bi ñu dawalee bal bi ba ci 42eelu simili bi la Yusef En-Nesiri toj caaxi Jogo Kostaa, góolu Portigaal bi. Génn bi Jogo Kostaa génn moo moy, dugalkatu Marog bi daldi mbëkk bal bi, tuy ci kã yi, dugal. Marog 1, Portigaal 0. Noonu, Portigaal topp ciy daw, lu ne ñu jéem ko, waaye dara ? Bi Kiriscanóo Ronaldóo duggee yit, soppiwul dara ci joŋante bi. Arbit bi daldi mbiib mbiib bu mujj bi, Marog daldi toogloo Portigaal, jàll démi-finaal. Nit ñiy tëb ak a yuuxu. Fépp fu saa-marog nekkoon bés booba, fésal nga sa mbégte, muy ca Marog, seen um réew, ci taaxi Afrig yi, rawatina Ndakaaru, ca Pari ak Belsig… fépp la saa-afrig yi génnoon di tëb ak a fecc, yor raaya Marog. Wolof ne, bés du réy du tuuti, boroom lay tollool. Te, ku def lu réy, am lu réy.
Marog dina daje ak Farãs, àllarba 14i fan ci desàmbar 2022, bu 19i waxtu jotee. Ñuy njort ak a ñaan ngir gayndey atlaas yi reere ginaari tubaab yi. Am na nag ñuy wax naan, bu fi yemoon sax mu neex. Waaye, wax jooju, ak ndamul Marog miy njëlbeenug réewum Afrig mu àgg démi-finaalu kuppeg àddina si, dafa am lu muy wund. Day wone ne, Afrig, ba tey dafa des ginnaaw.
Ndeysaan, 1930 ba tey, 92i at bi ñu sosee joŋanteb kuppeg àddina si ba jonni-Yàlla-tey jii, 4i réewi Afrig kese ñoo àgg file. Te, li ci gën a doy waar mooy ne, ba keroog alxames, kenn ci 3i réew yooyee fa àggoon jàllu ko woon. Marog rekk a def lees jàppe jaloore ju réy. Waaw, jaloore la naam, waaye jaloore juy biral ag suufe ak ub xeebeel. Daanaka xarnu, ñuy amal joŋante bu ni mel, menn um réewu Afrig kott a ci àggagum fii. Lu tax ? Jar na laaj.
Fànn boo jël, ak lu mu ci mën di doon, bu ci doomu Afrig defee jaloore rekk, dangay dégg ñu naan « guléet ! ». Maanaam daal, nun waa Afrig, dañ noo raw ci lépp, ëppale nu lépp, gën noo aay, gën noo xereñ. Dees na faral di dégg kàddu yu mel ni :
–« Mooy doomu Afrig ju njëkk a def… »
–« Guléet ab saa-afrig di am… »
–« Bi àddina sosoo ba tey, mooy ñuule bi njëkk a… »
–añs.
Yeen a ngi dégg de. Saa su nekk rekk, wax yu ni mel lees di biral. Dafa di, wëliis kuppe (futbal) ak yeneen xeeti tàggat-yaram yi, muy koom-koom, di pólitig, di njàng meek njàngale mi, di mbatit ak cosaan, lépp, Afrig ci ginnaaw lees ko féetale. Moo tax, saa bu defee lu koy ràññatle, ab jaloore lees koy jàppe. Lay yoon ci ñeneen ñi, nun, kaawteef la fi. La jaadu feeneen, di fi kéemtaan. Bu keneen defee lu réy, dañ naan rekk « xamoon nañ ko, du mbetteel… ». Waaye, bu dee Afrig moom, dañ koy réyal. Ba kañ ?
Ndamul Marog li nag, ndam lu réy la, naam. Waaye, ndam lu tuuti la tamit bees ko méngalee ak li doxandéem jot a defagum. Waratunoo doyloo ay wiccéem, kaar-dë-finaal ak i démi-finaal. Finaal sax dafa doyul, danu war a diir kub bi, palaas bi gën a kowe. Loolu nag, du ci kuppe kese, ci fànn yépp la. Te mi ngi tàmbali ci gëm sa bopp, gàlloo jom, fulla ak fayda, daldi sóobu ci liggéey bi.
Ku sawar ci liggéey ku ne, oomle. Ku oomle, baaxle. Ku baaxle nag, dinga raw say maas.