Jëwriñu Njaboot gi ak Ndimbal yi, Maymuna Jéey, biral na ndogal yu yees yi ñu jël ñeel ñeel ndàmpaayul way-loruy xew-xewi 2021-2024 yi ak ñi ñu ci jàppoon kaso.
Bees sukkandikoo ci dég-dég yees rotal, dees na dàmp gépp njaboot gu deele ci xew-xew yooyu koppar yu tollu ci fukki miliyoŋ. Waaye, du ca yam. Ndaxte, dinañu jël jirimi njaboot yooyii, boole leen ci jirimi Réew mi. Rax-ci-dolli, njaboot yooyu ci seen bopp, dinañu leen boole ci naali ndimbal yu Càmm giy lal (Bourses de sécurité familiale, Couverture Sanitaire Universelle, Carte d’Égalité des Chances, etc.). Dees na leeral anam bees di jëmmalee ndogal loolu. Ba tay, ci li jëwriñ ji xamle, dinañu dimbali njaboot yooyu, fexe ba ñuy mën a jot ci koppar yi yenn banqaasi Càmm gi di dimbalee askan wi, niki DER/FJ, Fonds national de Crédit pour les Femmes ak Fonds national de Promotion de l’Entrepreneuriat Féminin.
Bu loolu weesoo, jëwriñ ji xamleet na ne dinañu taxawu ña ñu tëjoon kaso, ñi ame woon ay gaañu-gaañu walla ñi ci jële feebar ci xew-xew yooyu. Ni ñu leen di taxawoo mooy toppatoo lépp lu jëm ci seen wér-gi-yaram. Jëwriñ ji dafa bind ne :
« Taxawu boobu, dafa aju ci këyit yu leer yu ay fajkat defar. Seen i njaboot tamit dinañ ci mën a jariñu. »
Ba tay ci fànnu ndàmpaay li, Càmm gi waajal na koppar yu tollu ci 500 000 ngir képp ku bokk ci waññig ANSD, ànd ci ak Njëwriñu Yoon gi, xibaari takk-der yi ak ñi teewal njabooti way-loru yi ak ndawi way-moomeel yi.