NDAR : SONKO DIGE NAY PEXE ÑEEL NAPP GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, mi ngi woon fa Ndar, tay ci gaawu gi, 6i pani sulet 2024. La ko yóbboon di ñaareelu bésu set-setal bi Njiitu réew mi sumb. Waaye, ku ne Ndar, ne géej, te ku wax géej sam xel dem ci napp. Napp gi nag, dafa di pàcc bu am solo lool ci koom-koomu réew mi. Doomi Ndar yi, rawatina waa Get-Ndar, di ay nappkat yu bir. Waaye, ñaare, dañuy jànkoonteel ak i jafe-jafe yu bari ci seen liggéey. Moo tax, bu fa elimaanu jëwriñ yi teewee, yoon la mu àddu ci fànn woowile.

Bees sukkandikoo ci kàdduy elimaanu jëwriñ yi, Càmm gaa ngi sàkk i « pexe yu lootabewu » yoy, dinañ gën a ñoŋal caytug balluy géej gi. Ci dalu web APS lees jukkee kàddoom yii toftalu :

« Dañu bëgg a dalal xeli nappkat yi. Dañu leen bëgg a wax ne ñoo ngi sàkk i pexe yu gën a lootaabewu yoo xam ne, dañuy tukkee ci lees di saytuwaat déggooy napp gi. Pexe yooyu, dinañ gën a ñoŋal caytug balluy géej gi. »

Fa Get-Ndar, di dëkku nappkat, la waxee kàddu yii, ba ñuy door ñaareelu bésu set-setal bees duppee « Setal sunu réew ». Wax na sax ne :

« …déggooy nap yi ñuy soow, tax ba ay doxandéem di jiiroo sunuy balli mbindaare te duñu sàmmonte ak li ci yoon sàrtal, di bañ a yebbi li ñu napp ci sunuy tefes, [déggoo] yooyu ñu ngi leen di saytuwaat. Li nu ko duggee mooy ñoŋal  nappug réew mi te fexe ba sunuy nappkat mën a gis seen bopp ci napp gi. »

Moom, Usmaan Sonko, xamle na ne, njotug balluy géej gi dina bokk ci seen yitte yu gën a réy. Ndeem dañuy sog a falu, lal nañ ay pexey négandiku, rawatina waxtaan yi ñu séq ak sunu dëkkandoo Gànnaar yi. Ciy waxam nag, njiiti Gànnaar yi ubbeeku nañ lool te nangu nañ sax yokk lisãsi napp yi ñuy jagleel nappkati Ndar yi.

Mi ngi jeexalee ay kàddoom ci fàttali solos napp gi ñeel koom-koomu réew mi.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj