NDELLOOG USMAAN SONKO CI WAYNDAREW WOTE WI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci talaatay tey jile, 12 desàmbar 2023, la tirbinaal « hors classe » bu Ndakaaru di àtte ndax dañuy delloo Usmaan Sonko ci wayndarew wote wi am déet.  Ci yoor-yoor bi la layoo bi door diggante meeru Sigicoor bi ak Càmmug Senegaal gog, ndawul yoon lee ko fa teewal ak layookatam.

Ca ndoorteel la nag la rëq-rëq yi tàmbali, layookati Usmaan Sonko yi di kaas. Meetar Ndumbe Wan a jëkk a kaas, wax ne dañ foogoon ne, ñoom layookati Sonko yi, ci saal 4 ba la layoo biy ame. Yemu ca. Ndax, àddu na ci seppi bees seppi Usmaan Sonko ci wayndarew wote wi, di laaj naan xamul mbir mi lu ci yoonu Càmmug Senegaal gog, ndawul yoon lee ko fa teewal.

Meetar Uséynu Faal moom, Njiitu réew mi ci boppam la tam dëmm, wax ne lu jiin Njaag a, te Maki Sàll mooy Njaag. Nde, ciy waxam, fitna jeek coono gi Usmaan Sonko di dund yépp, kenn tegu ko ko ku dul Maki Sàll. Te, ba tey ci làmmiñu layookat bi, lenn doŋŋ la Maki Sàll duggee : mooy fexe ba Usmaan Sonko du bokk ci wotey 2024 yees dëgmal.

Bim noppee, Meetar Ecen Njonn xamle na fa ne : « Ba jamono jii may wax ak yeen, sama kiliyaan Usmaan Sonko jotul këyit gi koy xamal ni seppees na ko ci wayndarey wote yi ».

Bu dee Meetar Bàmba Siise moom, ndawul yoon li fa teewal Càmm gi la song ci kàddu, wax ne :

« Damay xel-ñaar ci maanduteg ndawul yoon li fi teewal Càmm gi, moom mi  sañ a bind ci këyitam ay kàddu yu ma waxul ba noppi di ma lees askanale. Waa jii ku doy waar la koo xam ne, am na fitu def lu nekk ngir rekk fegg ab politiseŋ. »

Ginnaaw gi, Meetar Bàmba Siise wax na ak àttekat bi, jéem ko xamal ne, « Càmmug Senegaal nekkewu fi lu dul di yàggal mbir yi, di tëkku yoon ak ñi koy sàmm (àttekat yi) te nga bokk ci ».

Cig pàttali, àttekat bii di Sabasi Fay dafa santaane woon ñu delloo Usmaan Sonko ci wayndarey wote yi. Loloo ngi xewoon ñaari weer ci ginnaaw. Waaye, keroog 17 nowàmbar, ëttu àttewaay bu mag bi dafa neenal àtteb Sabasi Fay bi, dénk mbir mi tirbinaal « hors classe » bu Ndakaaru. Looloo sabab layoob tey bi.

Ñaari ayu-bés kepp ñoo des ci déppo yi ñeel ñi bëgg a doon i lawax ci wotey 204 yi.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj