Ndigalul dakkal tabax yi ci peggu géej gi

Yeneen i xët

Aji bind ji

Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, taxawal na ab banqaas buy saytu anam bees joxee suuf si féete ak wetu géej gi, ci diiwaanu Ndakaaru. Ci ndigalul Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, la taxawalee banqaas boobuy féete fa màkkaanu njëwriñ gu mag gi (Pirimatiir).

Bees sukkandikoo gi areete bi mu biral, dees na dakkal bépp xeetu tabax ci weti géej gi fileek ñuy leeral naka lañ joxee suuf soosii nekk ci peggu géej gi askan wépp bokk moomandoo. Ñii di waa DSCOS lañu sant ñu jëfe ndigal li, daldi dakkalandi tabax yi ci diirub ñaari weer. Démb, 13 me 2024, la ndogal li Jib.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj