NDOG MU METTI FA KUMPENTUM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ndogum yoon (aksidaŋ) mu mettee ame fa Kumpentum, tey ci suba teel, bi 7i waxtu jotee. Juróom-benni nit ñoo ca ñàkk seen i bakkan ca saa sa.

Ci “route nationale 1” bi la jéyya ji xewee, ci ngénnug (sortie) Kumpentum jëm Kungël. Ab biis moo dalante ak benn minikaar. Ca saa sa, 6i bakkan rot nañ ca. Am na yit 14i way-loru yu ci jëleey gaañu-gaañu. Sunuy naataangooy Seneweb ñoo siiwal xibaar bi.

Jamono jii nag, ndog yu bari nañ lool sax ci tali bi. Dafa di, diggante alxames ak tey jii rekk, fukk ak juróom-ñetti nit faatu nañ ci tali bi ci sababu ndog yi.

Ak màggal gii jubsi, nga xam ne fu nekk la taalibey Bàmba yiy jóge wutsi Tuubaa, warees na jël ay matuwaay ci yaale ji. Lu ko moy, tali bi dina jeexal nit ñi.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj