Lawax yi ñoo woote am ndaje mu mag ngir ñaxtu ñeel ndogal li Maki Sàll jël, daldi fomm wotey 2024 yi. Xeex bi tàmbali na ba ñu jàpp ñenn ci kilifay kujje gi.
Jàpp nañ Aminata Ture. Ciy waxam, bi mu génnee ci daamaram la ko takk-der yi jàpp te kenn waxu ko lu tax ñu jàpp ko.
Anta Baabakar Ngom tamit, jàpp nañ ko. Ciy waxam, ma nga birigaad bu Fuwaar ñu téyandi. Nee na, takk-der yi dañ ko gëtën. Fa Kawlax, jàpp nañ dépite bii di Roqaya Njaay. Kii di Porfesëer Daawda Njaay tamit, sàndarm yi jàpp nañ ko.
Ci lees jotagum ciy xibaar, xeex bi tàmbaleegum na fa goxi Ndakaaru yi, Mbàkke ak Tiwaawan. Fa Ndar, ñaxtukat yi dakkal nañ joŋante futbal ba fa amoon. Bu dee Cees, am na ab takk-der bu fa ndaw ñi dóor ba gaañ ko. Ñoo ngi ruumandaat ndax dee na am deewut.
Cig pàttali, Njiitu réew mi, Maki Sàll, dafa jël ndogalu fomm wotey 2024 yi waroon a am bésub 25 féewiryee. Lawax yi jàlloon te war cee bokk ne dee du ci dal, wote daya m ci nii mbaa ci naa. Moo tax, démb, ba ñuy janook, ñu ne, ñoom lawax yi, dañuy door seen kàmpaañ ci dibéer jii, fa Saint-Lazare.