LU TAX MAKI SÀLL MËNUL A KÀMPAAÑAL AAMADU BA ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Fan yii nu génn, doon nañ yégle ne Njiitu réew mi, Maki Sàll, dina jàppale Aamadu Ba ci kàmpaañ bi. Noon nañ sax ne, dina ko fekk Kafrin, ànd ak moom ci benn mitiŋ, tey ci bésub 21 màrs bii. Bees sukkandikoo ci Njaga Silla nag, di ma-xarañ ci wàllu càrtug wote gi (code électoral), Maki Sàll amul sañ-sañ bi. Ndaxte, yoon mayu ko ko.

Moom Maki Sàll, bokkul ci wotey 24 màrs 2024 yi donte ne Aamadu Ba mooy lawaxam, ci li feeñ. Lawax boobu nag, Maki Sàll mënu ko jàppale. Njaga Silla a ko xamle, wax ne Ndeyu sàrti réew mee ko ko tere niki Njiitul réew. Li ko waral mooy càrtug màndute ak yemale gi war a dox diggante làng yeek lëkkatoo yiy xëccoo réew mi.

Ci ndogal li Ndajem Ndeyu Sàrti Réew mi jëloon, ca Nguurug Abdulaay Wàdd, la ma-xarañ bi sukkandiku ngir wax lu ni mel. Ndogal looloo ngi aju woon ci mbiri 2, 3 ak 4-E-2001 bu 26 màrs 2001. Waxeesoon na ci ne :

« Càrtug màndute diggant làng yeek lëkkatoo moo tax ñu war leen a yemale ñoom ñépp. Bu ko defee, bu dee Njiitu réew mi fi nekk bokkul ci wote yi, kenn ci lawax yiy dagaan baatu askan wi warul a jëfandikoo peeñam ak jagle yi ko Ndajem Ndeyu Sàrti Réew mi beral. »

Ndogal lii, ab santaane la, dib tere. Ndax, jamono jooja, lëkkatoog Ablaay Wàdd gi dafa doon jëfandikoo peeñug Ablaay Wàdd mi woon Njiitu réew mi, di ko def ci jumtukaayi woteb dépite bi amoon bésub 29 awril 2001.

Kon, ndogal li looloo tere Maki Sàll, ci lu bir, mu bokk ci wote yi di am ku muy dimbali. Ndax Maki Sàll dina tënku ci ndogal li ? Li ci kanam rawlu i bët.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj